Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Abakug

Abakug 3

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Ñaanu Yonent Yàlla Abakug a ngii, galanu woy wi di galanu njàmbat.
2Éy Aji Sax ji, maa dégg sab jëw, Aji Sax ji maa yéemu ci sa jaloore! Ngalla yeesalal say jaloore, nu fekke, xamleel say jaloore, nu fekke, bu la am sànj teree geesu, yërëm.
3Yàllaa ngi jóge Teman, Aji Sell ji foofa ca tundu Paran lay bawoo. Selaw Darajaam moo dajal asamaan, teddngaam fees kaw suuf.
4Kee di leer gu ne ràññ, ay ceeñeer fettaxe ci loxoom, te fa la dooleem làqe.
5Mbas moo dox, jiitu ko, jàngoro topp ciy tànkam.
6Kee taxaw, yëngal suuf; kee xoole, loxloo xeet yi, tund yu mag ya woon naka jekk rajaxoo, tundi cosaan yu ndaw ya maasaloo. Kii moo moom yooni cosaan yi.
7Njàqare laa gis ca xaymay Kusan, te ndimoy xaymay waa Majan yëngu na.
8Aji Sax ji, dex yi nga sànjul? Am dex yi nga mere? Am géej nga sàmbaaral, ba war say fas, dawal sa watiiri dawal-daan?
9Yaa génne sa xala mbaram, feesal sa mbuusum fitt. Selaw. Yaa xare suuf ay dex.
10Tund yi gis la, jaayu; waame wàcc, wéy; xóote ya riir, gannaxam ya jolli fa kaw.
11Jant ak weer ne tekk fa seen màkkaan, janook sa leeru fitt yi soqi, ak melax gi tàkke ci sab xeej.
12Am sànj nga daagoo fi kaw suuf, mer nga dëggaatee xeet yi.
13Yaa génn ngir wallusi sa ñoñ, wallusi ki nga fal. Yaa rajaxe puju néegu ku bon ki, xar ko ñaar, geen ba ci put. Selaw.
14Ba noon ya riddeendoo, di nu tasaaresi, seen xeeju bopp nga bëtte seen bopp, fekk leen ñuy xaxaloo, ni ñuy waaja sëxëtoo ay néew-ji-doole, fu kenn yégul.
15Yaa jaabal say fas biir géej, yëngal mbàmbulaan ma.
16Ba ma ca déggee, samay butit a yëngu, coow la tax samay tuñ di lox, sama yaram dee goyy, may lox fi ma taxaw, te ne cell, di séentu bésub njàqare, bay dikkal xeet wi nu song.
17Ndaxam garabu figg foccul, doomu reseñ amul ca ndeyam, njurum garabu oliw àntuwul, tool yi meññul aw ñam, gàtt it tukkee na ca gétt ga, du genn jur gu gudd ci wurmbal,
18te man may bànneexoo Aji Sax ji, Yàlla ji may wallu laay bége.

19Aji Sax ji Boroom bi mooy sama doole, moo ma defal samay tànk mel ni yoy kéwél, te fa kawte ya la may daaguloo. Mu jëm ci njiital jàngkat yi, ànd ak samay xalam.