Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Yeremi

Yeremi 41

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Ba ñu demee ba ca juróom ñaareelu weer wa ca at mooma, Ismayil doomu Netaña doomu Elisama, askanoo ci ñi moom Yuda te di njiitu jawriñi buur, ànd ak fukki nit ba ca Gedalya doomu Ayikam ca Mispa. Ci kaw loolu, ñu bokk di lekk ca kër Gedalya.
2Ismayil jekki jóg, mook fukki nit ña mu àndal. Ñu jam saamar Gedalya ma buuru Babilon dénkoon réew ma, ba rey ko.
3Ismayil reyaale mboolem Yudeen ña nekkoon ak Gedalya ca Mispa ak xarekati Babilon ya fa nekkoon.
4Ba ñu bóomee Gedalya ba ca ëllëg sa, fu kenn yégul,
5mu am juróom ñett fukki nit ñu bàyyikoo Sikem ak Silo ak Samari. Ña nga wat seen sikkim, xotti seeni yére, dagg-daggee seen yaram, di ko ñaawloo. Ñu ŋàbb saraxu pepp ak cuuraay bu ñu indil kër Aji Sax.
6Ismayil génne buntu Mispa, gatanduji leen. Ma ngay dox, jëm ca ñoom, di jooy-jooylu ba dajeek ñoom, ne leen: «Agsileen kër Gedalya doomu Ayikam!»
7Naka lañu dikk ba ca biir dëkk ba, Ismayil ak ay nitam bóom leen, tàbbal néew ya ci kàmb.
8Fekk na mu am fukki nit ñu bokk ci ñoom ñu ne woon Ismayil: «Tee nga noo baña rey? Nun de am nanub denc ci àll bi. Peppu belee nga ca ak lors ak diw ak lem.» Loolu tax Ismayil fomm, ba boolewu leen ak seeni bokk, rey.
9Kàmb ga Ismayil sànni néewi nit ña mu reyaaleek Gedalya mooy kàmb ga Buur Asa mu Yuda gasoon ba ko Buur Basa mu Israyil songee xare. Moom la Ismayil doomu Netaña feesal aki néew.
10Gannaaw loolu mu jàpp mboolem ña des Mispa, di doomi buur yu jigéen ak mboolem ña des Mispa, te Nebusaradan, njiital dag ya, dénkoon leen Gedalya. Ismayil jàpp leen njaam, daldi wutali diiwaanu Amoneen ña.
11Ba loolu amee Yowanan doomu Kareya ak njiiti xare yi mu àndal yépp dégg musiba mi Ismayil doomu Netaña def mépp.
12Ñu ànd ak seeni nit, topp ko ngir xareek moom, ba dab ko ca déeg bu mag ba ca Gabawon.
13Ba nit ña Ismayil jàppe Mispa gisee Yowanan ak mboolem njiiti xare ya mu àndal, dañoo bég.
14Ñoom ñépp walbatiku, daw fekki Yowanan doomu Kareya.
15Teewul Ismayil doomu Netaña ak juróom ñetti nitam rëcc Yowanan, daw làquji réewum Amon.
16Yowanan doomu Kareya ak mboolem njiiti xare yi mu àndal nag boole mboolem la des ca mbooloo, ma Yonatan xettli woon ca Ismayil doomu Nataña ca Mispa, gannaaw ba Ismayil bóomee Gedalya doomu Ayikam. Ay nit ñu Yowanan jële woon Gabawon a nga ca, diy góor: ay xarekat ak bëkk-néegi buur, aki jigéen aki gone.
17Ñu dem ba dali ca dalukaayu Kimyam, ca wetu Betleyem, di waaj yoonu Misra,
18ngir rëcc waa Babilon ñi ñu ragaloon, ndax la Ismayil doomu Netaña bóom Gedalya doomu Ayikam, ma buuru Babilon dénkoon réew ma.