1Gannaaw ba Yeremi waxeek mbooloo mépp, ba sottal mboolem kàddu yooyu ko seen Yàlla Aji Sax ji santoon mu yegge leen ko,
2Asaryaa doomu Osaya ak Yowanan doomu Kareya ak nit ñu bew ñooñu ñépp jël kàddu gi. Ñu ne Yeremi: «Dangay fen! Sunu Yàlla Aji Sax ji santu la nga fommloo nu sunu yoonu Misra ga nu bëgga toogi.
3Xanaa Barug doomu Nerya kay moo lay xiirtal ci sunu kaw, ngir teg nu ci loxol waa Babilon, ñu rey nu, mbaa ñu yóbbu nu ngàllo ca Babilon.»
4Ci kaw loolu Yowanan doomu Kareya ak yeneen njiiti xare ya yépp ak mbooloo ma mépp gàntal Aji Sax ji, baña des réewum Yuda.
5Ba loolu amee Yowanan ak njiiti xare yépp yóbbu ña desoon ca Yuda ñépp, di mboolem ña ñu jëkkoona sànni ca biir xeet ya leen séq yépp, te ñu ñibbsi woon réewum Yuda,
6góor ñaak jigéen ñaak gone yaak doomi buur yu jigéen ya. Yóbbu nañu mboolem ña Nebusaradan njiitu dag ya tegoon ci loxol Gedalya doomu Ayikam doomu Safan; ñu yóbbaale Yonent Yàlla Yeremi ak Barug doomu Nerya.
7Ñu dikk Misra, baña déggal Aji Sax ji, daldi àgg dëkk ba ñuy wax Tapanes.
8Gannaaw loolu kàddug Aji Sax ji dikkal Yeremi ca Tapanes, ne ko:
9«Jëlal ñaari doj yu mag yooy suuli ca dëru ban ba ca bunt kër Firawna gi ci biir dëkk bi, te na ko waa Yuda fekke.
10Nga wax leen ne leen: “Aji Sax ji Yàllay Israyil Boroom gàngoor yi dafa wax ne: Maa ngi nii di yónnee, jëli Nabukodonosor buuru Babilon, mi ci samag curga, ba teg ngànguneem ci kaw doj yii ma fi suul, mu firi fi xaymaam.
11Bu dikkee dina tas réewum Misra: ku wara médd, médd; kuy dugg njaam, duggi njaam; kuy fàddoo saamar, fàddoo saamar.
12Nabukodonosor dina jafal kër tuuri Misra yi, lakk tuur yi, mbaa mu yóbbu leen. Ni ab sàmm di teeñe mbubbam, ni lay teeñe réewum Misra ba mu set wecc, daldi daagu, dem yoonam.
13Dina rajaxe tuuri doj ya sampe ca Bet Semes ci biir Misra te dina lakk këri tuur yi ci Misra.”»