Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Yeremi

Yeremi 14

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Kàddug Aji Sax jii dikkaloon na Yeremi, jëm ca maral ma. Mu ne:
2«Waa Yudaa ngi ñaawlu, doole dëddu dëkk yi, ñu ne yogg, ne lasar fi suuf, yuux jollee Yerusalem.
3Kàngam ya yebal seeni surga, ñu rooti; ñu dem, gisuñu ndox ca mbalka ya, délseek seen xotti ndab, jàq, yaakaar tas, ñu muuru di tiislu.
4Réew mi tawluwul, suuf si fett, yaakaaru beykat tas, mu muuru, di tiislu.
5Kéwél sax jur ci àll bi, sànni ndax ñàkk um ñax.
6Mbaamu àll taxaw ci tund yi ne faraas, di àppaat niw till, ñàkk parlu, gët ya giim.»
7Dëgg la sunuy ñaawtéef a nu tuumaal, waaye éy Aji Sax ji, jógal te saw tur tax, doonte dëddu nanu la ay yooni yoon, moy la.
8Éy yaw, yaakaaru Israyil, mi nuy wallu bésu njàqare, bul ñooru ni doxandéem ci réew mi, mbaa ku nekk ciw yoon, jàdd fi, fanaan.
9Ngalla bul mel ni ku waaru, mbaa jàmbaar ju manul walloo. Yaw Aji Sax ji, yaa ngi sunu biir, ñu di nu tudde saw tur. Bu nu wacc!
10Aji Sax ji dafa wax ci askan wii ne: «Ñeeka bëgg ub taxawaalu, baña téye seen tànk. Moo tax man Aji Sax ji bégewuma leen. Léegi ma bàyyi xel seenug mbon, ba mbugale leen seeni moy.»
11Aji Sax ji nag ne ma: «Bul ñaanal askan wii.
12Su ñu ci boole woon koor sax, duma déglu seeni dagaan. Su ñu ma doon sarxalal saraxu rendi-dóomal ak saraxu pepp it, du maa leen di nangul. Xanaa saamar akub xiif ak mbas kay laa leen di faagaagale.»
13Ma ne ko: «Éy Boroom bi Aji Sax ji, yonent yaa ngii di leen wax ne duñu dajeek saamar, duñu xiif te jàmm ju ne ñoyy nga leen di defal fi bii bérab.»
14Aji Sax ji ne ma: «Waxyuy fen la yonent yiy waxe ci sama tur. Yebaluma leen, santuma leen ko, waxumaak ñoom. Peeñuy fen ak ngisaaney neen ak nax yu ñu fental seen bopp lañu leen di jottlee waxyu.»
15Moo tax Aji Sax ji dafa wax ne: «Yonent yi ma yebalul te ñuy waxe waxyu ci sama tur naan: “Saamar akub xiif du am ci miim réew,” saamar akub xiif ay mujje yooyu yonent.
16Ñi ñu doon jottli ay waxyu it, xiif ak saamar a leen di rey, ñu sànni seeni néew ci mbeddi Yerusalem, te duñu am ku leen rob, ñook seeni jabar ak seeni doom, góor ak jigéen. Dinaa leen xëpp seen ay.
17Nanga leen yégal saw tiis, ne leen: “Naa tuur rongooñ guddeek bëccëg, te du fer; sama bokki bopp yi damm ba dammtoo, ndaw góom bu metti!
18Ma dem, xool àll, gisuma lu moy ñu saamar bóom, ma dugg biir dëkk, gisuma lu moy ñu ne làcc akub xiif, yonent ak sarxalkat di wër réew mi, xam-xam réer leen.”»

19Aji Sax ji, wacc ngaa wacc Yuda nii? Am Siyoŋ a la génnliku? Lu tax nga di nu dumaa musiba mu amul paj? Nuy yaakaar jàmm, dara baaxul, nuy séentum paj, tiitaange ne jaas!
20Aji Sax ji, xam nanu sunug mbon, xam sunu ñaawtéefi maam; moy nanu la moos.
21Waaye xoolal ci yaw te bul xalab, bul teddadil sa jal bu tedd. Bàyyil xel te baña fecci sa kóllëreek nun.
22Xërëmi neen yi yéefar yiy jaamu, ana ku ci mana taw? Am asamaan ay sóobal boppam ay waame? Du yaw la Aji Sax ji sunu Yàlla? Yaw lanu yaakaar, te loolu lépp, yaw a.