Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Yeremi

Yeremi 28

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Ca menn at ma, fekk Cedesyas buurub Yuda di doora falu, yemook ñeenteelu atam, ca juróomeelu weer wa, am na doomu Asur ju ñuy wax Anaña, di yonent bu cosaanoo Gabawon. Mu wax ak Yonent Yàlla Yeremi ca biir kër Aji Sax ji, fa kanam sarxalkat yaak mbooloo mépp, ne ko:
2«Aji Sax ji Yàllay Israyil Boroom gàngoor yi dafa wax ne: Damm naa yet wi leen buuru Babilon tënke woon.
3Fii ak ñaari at tembe dinaa délloosi fii mboolem ndabi kër Aji Sax ji Nabukodonosor buuru Babilon jële woon bérab bii, yóbbu Babilon.
4Dinaa délloosi fii itam buurub Yuda Yekoña doomu Yowakim, te mboolem ngàllog Yuda ga demoon Babilon, maa leen di délloosi bérab bii.» Kàddug Aji Sax jee. «Maay damm moos yetu buuru Babilon wi mu leen tënke.»
5Ba loolu amee Yonent Yàlla Yeremi tontu yonent ba ñuy wax Anaña fa kanam sarxalkat yaak mbooloo ma taxaw fa biir kër Aji Sax ji mépp.
6Mu ne ko: «Amiin! Yal na ko Aji Sax ji defee! Yal na Aji Sax ji sottal sa kàdduy waxyu yi nga wax, ba délloosee Babilon ba fii ndabi kër Aji Sax ji ak mboolem ña ñu fa toxal.
7Waaye ngalla déglul bu baax kàddu gii ma lay wax, yaak mbooloo mi mépp.
8Yonent yi feeñoon naka jekk lu ma jiitu, jiitu la, jottli nañu réew yu yaatu ak nguur yu mag seen waxyuy xare ak musiba ak mbas.
9Ab yonent nag bu dee biral waxyub jàmm, su jàmm ja dikkee, ñu xam ne Aji Sax jee ko yebal ci lu wér.»
10Ba mu ko defee yonent ba ñuy wax Anaña yékkatee yet wa ca ndoddu Yonent Yàlla Yeremi, damm ko.
11Anaña àddu fa kanam mbooloo ma mépp ne leen: «Aji Sax ji dafa wax ne: Nii laay damme yet wi buur Nabukodonosor buuru Babilon di tënkee. Fii ak ñaari at tembe dinaa jële yet wi ci ndoddu mboolem xeet yi mu ko tënke.» Ba loolu amee Yonent Yàlla Yeremi dem yoonam.
12Gannaaw ba yonent ba ñuy wax Anaña yékkatee yet wa ca ndoddu Yonent Yàlla Yeremi ba damm ko, kàddug Aji Sax ji dikkal Yeremi, ne ko:
13«Demal wax Anaña ne ko: “Aji Sax ji dafa wax ne: Yetu bant nga damm, waaye dinga ko wuutale yetu weñ.
14Ndax Aji Sax ji, Yàllay Israyil Boroom gàngoori xare yi dafa wax ne: Yetu weñ laay teg ci ndoddu mboolem xeet yii, ñu nangul Nabukodonosor buuru Babilon, di ko surgawu. Te rabi àll yi sax, maa leen di teg ci loxoom.”»
15Gannaaw loolu Yonent Yàlla Yeremi ne yonent ba ñuy wax Anaña: «Anaña, déglul bu baax li ma lay wax: Aji Sax ji yebalu la, yaw ngay gëmloo askan wii ay fen.
16Moo tax Aji Sax ji dafa wax ne: “Maa ngii di la yebal, nga jóge fi kaw suuf. Ren jii ngay dee, ndax kàdduy gàntal nga waxal Aji Sax ji.”»
17Yonent ba ñuy wax Anaña ca at mooma la dee ca juróom ñaareelu weer wa.