Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Yeremi

Yeremi 10

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Yeen bànni Israyil, dégluleen kàddu, gi leen Aji Sax ji dégtal.
2Aji Sax ji dafa wax ne: «Jikkoy xeeti yéefar yi, buleen ko roy; màndargam asamaan, buleen ko tiit; na ko yéefar yi tiit.
3Aaday xeet yi kat neen la. Garab lañuy dagge ca gott ba, ab yettkat yette ko sémmiñ,
4rafetale xaalis ak wurus, daaj koy pont, dëgëral, ba du yëngu;
5muy saf kuñeental ci biir tóokërub xaal. Du wax, du séqi jéego, ñu di ko gaŋar-gaŋaree. Buleen ko ragal, du lore, du jariñe.»
6Aji Sax ji, kenn melul ni yaw, yaaka màgg, jàmbaare, màggu tur.
7Yaw Buuru xeet yi, ana ku la dul ragal? Yaw déy yaa yelloo ragal. Mboolem ñi xelu ci xeet yi ak mboolem seeni buur, kenn melul ni yaw.
8Ñoom ñépp a bokk dofe, ñàkk bopp: xam-xamu kasara, bant kese!
9Xaalis lañuy jële Tarsis, xoobe ko bant, wurus wu jóge Ufas, ñu boole ca, ndaanaan liggéey ko, tëggu gànjar yett ko, ñu solal ko ndimo lu yolet ak lu xonq curr, lépp di liggéeyu ràbb yu xareñ.
10Waaye Aji Sax jeey Yàlla dëgg. Mooy Yàlla jiy dund, di buur ba fàww, xadaram gësëm àddina, meram man xeet yi.
11Lii nag, nangeen ko siiwal: «Seen yàlla, yi sàkkul asamaan, sàkkuñu suuf, ñooy sànku, jóge fi suuf ak fi asamaan tiim.»
12Suuf, Aji Sax jee sàkke kàttanam; dun bi, mu sampem xelam; asamaan, mu lale xam-xamam.
13Bu àddoo, ndoxum asamaan riir; mu yéegey niir fa cati àddina, yebbee ngelaw fa dencam ya, daldi melax, taw.
14Nitoo nit dim sannax, sore xam-xam: te képp kuy tëgg sa jëmmu tuur, yaa añe gàcce. Sa jëmmi weñ ji nga xelli, di neenug neen, noog bakkan, tus!
15Cóolóolu neen, liggéeyu caaxaan; bu bésam taxawee, mu sànku.
16Ki séddoo Yanqóoba déy wuute naak yii caaxaan. Kookoo bind lépp, te Israyil di giir gi mu séddoo. Kookooy Aji Sax ji Boroom gàngoori xare yi!
17Yerusalemee, yeen ñi ñu gaw, forleen seen ëmb.
18Aji Sax ji déy dafa wax ne: «Maa ngii naa xërr waa réew mi bii yoon, teg leen njàqare, ba ñu yég ko.»

19«Wóoy man, yàqu naa! Ndaw góom bu metti! Dama noon lii jàngoro doŋŋ a, naa muñ!
20Xayma xotatoo, buumi xayma xëttandoo, samay doom wacc ma, ne mes; kenn sampatul sama xayma, firi ko.»
21Sàmmi xeet weeka dofe: Aji Sax ji, sàkkuwñu ko. Moo leen taxa bonle, seen jur gépp tasaaroo.
22Xibaar a ngoog, di ñëw, riir mu réy a yëngoo réewum bëj-gànnaar, nara gental dëkki Yuda yu mag yi, till yi dëkke.
23Aji Sax ji, maa xam ne nit moomul yoonam, kuy dox moomuli jéegoom.
24Aji Sax ji, yar ma lu yem, te bañ maa yare mer, di ma semmal.
25Xëppal sa xadar yéefar yi la yégul, ak làng yi la tuddul. Ñoo bóom giirug Yanqóoba, bóom leen ba fàkkas leen, gental seen dëkkuwaay.