Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Yeremi

Yeremi 15

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Aji Sax ji nag ne ma: «Musaa ak Samiyel sax, bu ñu taxawoon fi sama kanam, du tax ma faale askan wii. Dàqal, ñu sore ma, te wéy.
2Bu ñu la laajee ne la: “Fu nu jëm?” nga wax leen ne leen: “Aji Sax ji dafa wax ne: Kiy wopp dee, wopp dee; kiy deeye saamar, deeye saamar; kiy deeye xiif, deeye xiif; kiy duggi ngàllo, duggi ngàllo.”
3«Te dinaa wàcce fi seen kaw ñeenti xeeti duma.» Kàddug Aji Sax jee. «Saamar di bóom; xaj diri yóbbu, njanaaw ak rabu àll for, mu jeex.
4Dama leen di def, waa réewi àddina yépp, ku leen ci xool rasu. Te li ko waral di Buurub Yuda, Manase miy doomu Esekiya, ak li mu def ci digg Yerusalem.»
5«Yerusalemee, ku lay yërëm? Ku lay jooy? Moo, ku lay geesu ne la: “Jàmm nga am?”
6Yaw yaa ma wacc,» kàddug Aji Sax jee, «dellu gannaaw, ma duma la, sànk la. Muñ naa ba sonn.
7Maa leen bees ni ñuy beesem pepp ci pénci réew mi. Maa sànk sama ñoñ, faat seeni doom, ndax tuubuñu seeni jëfin.
8Seeni jëtun laa ful, ba ñu ëpp suufas géej, ma indil leen pàddum njolloor, mu reyal yaay doomi waxambaaneem, këpp ko tiitaangeek njàqare.
9Yaayu juróom yaari góor loof, di àppaat, jantam sowe bëccëg ndarakàmm, yaakaar tas, mu jàq, seenu ndes, ma leel saamaru noon.» Kàddug Aji Sax jee.
10Wóoy saa ndey, loo ma doon jure! Man mi réew mépp di xulook a layool, leblewma, lebuma; te ñépp di ma móolu.
11Ndaxam Aji Sax ji nee: «Maa lay xettli déy, ngir sottal lu baax; maa la defal sa noon di la tinu déy, ci janti safaan ak njàqare.»
12«Ku mana toj weñ gu ñuul, rawatina yetu weñu bëj-gànnaar, mbaa xànjar?
13Yeen waa Yuda, seen alal ak seeni denc laay jox ñu ko sëxëtoo te feyuñu ndax seen gépp moy ci seen réew mépp.
14Maa leen di def seen jaami noon réew mu ngeen xamul, sama mer jippét, tàkkal leen.»
15Yaw déy Aji Sax ji, xam nga! Ngalla bàyyi ma xel, geesu ma; feyul ma ñi ma sam. Bu leen muñal ba sànk ma! Xamal ne yaa ma tax di dékku saaga.
16Sa kàddu laa gis, di ko dunde, sa kàddu di ma bégal, bànneexal sama xol. Yaw Aji Sax ji Boroom gàngoor yi, déy, sa tur lañu ma tudde.
17Masumaa toogandook ñiy mbumbaay bay xawaare. Yaa ma jiite, ma beru, toog ndax mer mi nga ma sol, ba ma fees.
18Moo sama tiis wi du dakk a? Bii góom bu metti, tëë wér! Yaw kay yaay waltan muy wal, di ŋiis, di tas sama yaakaar.

19Moo tax Aji Sax ji dafa wax ne: «Soo délsee, ma délloosi la, nga dellu di ma liggéeyal. Soo dee wax ngëneel lu soreeki caaxaan, dinga mel ni yaay sama làmmiñ, te nit ñeey délsi ànd ak yaw, waaye du yaay délsi ànd ak ñoom.
20Maa lay def nga mel ak askan wii ni tatay xànjar ju ñu dàbbli, ñu di la song te duñu la man. Maay ànd ak yaw, di la wallu, di la xettli.» Kàddug Aji Sax jee.
21«Ab soxor jàpp la, ma àtte; ab néeg ne la céex, ma foqati.»