Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Yeremi

Yeremi 38

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Mu am bés Sefatiya doomu Matan ànd ak Gedalya doomu Pasur ak Yukal doomu Selemya ak Pasur doomu Malkiya. Ñu dégg Yeremiy wax, ñépp di dégg, naan:
2«Aji Sax ji dafa wax ne: “Ku des ci biir dëkk bii, saamar rey ko, mbaa xiif, mbaa mbas. Waaye ku génn fekki waa Babilon, dina raw, bakkanam di ngañaayu xareem, mu mucc.”
3Aji Sax ji dafa wax ne: “Dees na teg moos dëkk bii ci loxol mbooloom buuru Babilon, mu nangu ko.”»
4Kàngami buur yooyu dem ne Buur: «Waa jii, na dee rekk; mu ngi yoqil xarekat yi des ci dëkk bi, di yoqil ñépp ndax waxam jii mu leen di wax. Waa jii kat wutul jàmmu askan wii, xanaa musiba.»
5Buur Cedesyas ne leen: «Mu ngoog ci seen loxo, manaluma leen dara!»
6Ñu jàpp Yeremi, ngir denci ko ca kàmbug Malkiya, kenn ci askanu buur, ca biir ëttu dag ya. Ñu yoore ko buum, ba ca biir, te kàmb ga amul ndox, bàq rekk a fa nekk. Yeremi nag tàbbi ca biir bàq ba.
7Ci biir loolu Ebedd Meleg, Kuuseen ba, di bëkk-néeg ci biir kër buur, dégg ne tàbbal nañu Yeremi ca kàmb ga. Fekk Buur a nga toog ca bunt ba ñu dippee Beñamin.
8Ebedd Meleg jóge kër buur, dikk ne ko:
9«Buur sang bi, nit ñi de, lu bon lañu def Yonent Yàlla Yeremi; tàbbal nañu ko ca kàmb ga. Dina fa dee ak xiif ndax ab dund amatul ci dëkk bi.»
10Buur sant Ebedd Meleg Kuuseen ba, ne ko: «Jëleel fii fanweeri nit, nga dem génne Yonent Yàlla Yeremi kàmb ga bala moo dee.»
11Ebedd Meleg jël nit ña, daldi dem biir kër buur, jàll ba ca suufu néegu denc ya. Mu jële fa yére yu ràpp aki sagar, boole lépp, yoore buum ca kàmb ga, jottli ko Yeremi.
12Ebedd Meleg ne Yeremi: «Ayca, booleel sagar yi, nga jiital ko ci say poqtaan, teg ci buum yi.» Yeremi def noonu.
13Ñu xëcc buum yi, génne Yeremi kàmb ga. Gannaaw loolu Yeremi des ca biir ëttu dag ya.
14Ba loolu wéyee Buur Cedesyas yónnee, woolu Yonent Yàlla Yeremi, ñaarook moom fa ñetteelu bunt ba ca kër Aji Sax ja. Mu ne Yeremi: «Dama lay laaj lenn. Bu ma nëbb dara.»
15Yeremi ne Cedesyas: «Su ma la waxee li am, du danga may rey rekk? Te su ma la digalee it, doo ma déggal.»
16Buur Cedesyas déey Yeremi, ne ko: «Giñ naa ci Aji Sax jiy dund te sàkkal nu bakkan, duma la rey te duma la teg ci loxoy ñii di wut sa bakkan.»
17Yeremi ne Cedesyas: «Aji Sax ji, Yàllay Israyil, Boroom gàngoor yi dafa wax ne: Soo nangoo génn rekk, jébbali sa bopp kàngami buuru Babilon déy, dinga rawale sa bakkan, te dëkk bii du lakk ba jeex. Dinga dund yaw, yaak sa waa kër.
18Waaye soo jébbalul sa bopp kàngami buuru Babilon, dees na teg dëkk bi ci loxoy waa Babilon, ñu lakk ko ba mu jeex, te yaw doo leen rëcc.»

19Buur Cedesyas ne Yeremi: «Man, ñi ma ragal mooy sunu bokki Yudeen ñi ñibbil waa Babilon; bu ñu ma tegee ci seen loxo, ñu torxal ma.»
20Yeremi ne ko: «Deesu la leen jox. Dangay déggal Aji Sax ji ci li ma la wax rekk, muy sa jàmm, nga mucc.»
21Waaye soo lànkee, ne doo génn, mbir a ngii mu ma Aji Sax ji won.
22Gisuma lu moy mboolem jigéen ñi des ci kër buurub Yuda, ña nga ñu jëme ca kàngami buuru Babilon. Ña nga naan: «Buur aka baaxi xarit! Ñoom ñi ko nax, ba man ko, mu tàbbi ca bàq ba, ñu dëddu, ne mes!»
23Mboolem say soxnaak say doom, dees leen di yóbbu ca waa Babilon, te yaw ci sa bopp doo leen rëcc. Buuru Babilon da lay jàpp, te dëkk bii day lakk ba jeex.
24Cedesyas ne Yeremi: «Bu kenn dégg nag lii nu wax. Lu ko moy dinga dee.
25Su sama kàngam yi yégee ne wax naak yaw, ba dikk ne la nga nettali leen li nu waxante te bañ leena nëbb dara, lu ko moy ñu rey la,
26ne leen rekk danga ma doon tinu, ndax ma bañ laa delloo kër Yonatan, nga di fa dee.»
27Ba loolu amee kàngami buur yépp dikk, laaj Yeremi, mu wax leen la ko Buur digal. Ñu daldi noppi, ba ko; ndax kenn déggul woon la mu wax ak Buur.
28Yeremi nag des ca ëttu dag ya, ba keroog bés ba ñu nangoo Yerusalem. Ba ñuy nangu Yerusalem nag, nii la deme woon.