Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Yeremi

Yeremi 47

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Kàddug Aji Sax ji dikkaloon na Yonent Yàlla Yeremi jëm ci Filisteen ñi, balaa Firawna di song dëkkub Filisteen ba ñuy wax Gasa.
2Aji Sax ji dafa wax ne: «Ndox a ngay fuddoo bëj-gànnaar, diy waame, walsi, walal réew meek li ci biiram akub dëkk ak ku ci biiram; doom aadama yuuxu, waa réew mépp serandoo.
3Booba fas yaa ràmbal, watiir ya riir, mbegey watiir ya kar-kareendoo, yoxo yoqi, ba baay geesuwul doom,
4bésub sànkute dikkal képp kuy Filisteen, ba dagge dëkk yii di Tir ak Sidon ndimbal lu ñu dese woon. Aji Sax jaa ngay sànk Filisteen, ña des te cosaanoo dunu Keret.
5Watu nel, ñaawloo, dikkal na Gasa, te wedamloo nañu Askalon. Yeen ñi dese joor gi, fu ngeen àppal seen yaram, wi ngeen di daggat, di ko ñaawloo?
6Ngeen naa: “Wóoy saamaru Aji Sax jii, xanaa doo selaŋlu? Dellul sa mbar, boog, dal-lu, ne tekk!”
7Waaye yaw saamar, noo mana selaŋloo te Aji Sax ji yebal la ci kaw Askalon ak waa tefesu géej, fa mu ko dogale?»