Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Yeremi

Yeremi 17

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1«Bàkkaaru Yuda lañu binde xaccug weñ gu cat la di doj wu dëgër. Dees koo ñaas ci seen àlluway xol, ñaas ko ci seen béjjéni sarxalukaay.
2Seeni doom sax di bàyyi xel seeni sarxalukaay ak seen xer yi ñuy màggale tuurum Asera fi ker garab yu naat yeek kaw tund yu mag yi
3ak kaw tund yi ci àll bi. Seen alal ak seen denc yépp laay joxe, ñu lël ko, booleek seen jaamookaay ndax seen moy yi dajal réew mi.
4Dingeen xañ seen bopp cér bi ma leen séddoon, ma def leen seen jaami noon ci réew mu ngeen xamul, ndax merloo ngeen ma mer mu dul fey mukk.»
5Aji Sax ji dafa wax ne: «Alkànde ñeel na ku yaakaar doom aadama ak képp kuy doolewoo nit, dëddu Aji Sax ji.
6Day mel ni gajjub ndànd-foyfoy, du gis ngëneel luy dikk! Day dëkke màndiŋ mu wow koŋŋ, suufas xorom su kenn dëkkul.
7Waaye barke ñeel na ku wóolu Aji Sax ji, yaakaar Aji Sax ji.
8Day mel ni garab gu saxe wetu ndox, lawal ay reenam ca wal ma, ragalul tàngoor wu dikk, xob ya di naat. Du tiit atum maral, du ñàkk meññeef.»
9«Dara gënula dëng xelum nit, laago la ci moom. Ana ku ko mana xam?
10Maay Aji Sax jiy seetlu xel, natt ub xol, di yool ku nekk jëfinam, la yellook añam.
11Kuy jagoo alal ju lewul, mooy picc mu toj lu mu nenul. Kookooy tollu digg dooleem, alal ja dëddu, mu mujje dof.»
12Sunu bérab bu sell bi, mooy ngànguney daraja, daa masa kawe.
13Yaw Aji Sax ji yaakaaru Israyil, ku la wacc, torox; ku la dëddu daa repp. Moo wacc Aji Sax ji, bëtu ndox miy dund.
14Éy Aji Sax ji, faj ma, ma faju; musal ma, ma mucc, samag cant, yaw a.
15Ñu ngii naa ma: «Ana la Aji Sax ji waxoon? Na dikk boog!»
16Man de, bañuma laa sàmmal, topp la; bésub tiis it dagaanuma ko. Yaw de xam nga ko. Li ma wax it fi sa kanam la.
17Bu ma teg tiitaange, yaay sama rawtu bésub safaan.
18Ngalla gàcceelal ñi ma topp, te bu ma gàcceel; yal nañu tiit, ñoom, te man, ma baña tiit. Rikk dikke leen bésub safaan, rajaxe leen ñaari yoon.

19Aji Sax ji da maa wax ne ma: «Demal taxawi ca buntu Doomi réew mi, fa buurub Yuda di duggeek a génne. Te nga taxaw itam ca mboolem bunti Yerusalem ya ca des.
20Nga ne leen: “Dégluleen kàddug Aji Sax ji, yeen buuri Yuda ak yeen waa Yuda gépp ak képp ku dëkk Yerusalem, di jaare bunt yii.
21Aji Sax ji dafa wax ne: Moytuleen seen bopp ba baña gàddu lenn bésub Noflaay, di ko jaarale bunti Yerusalem.
22Buleen génne seeni kër lenn bésub Noflaay te buleen ci liggéey lenn. Waaye nangeen sellal bésub Noflaay, muy la ma santoon seeni maam.
23Ndaxam dégluwñu ma, teewluwñu ma, xanaa të ticc, baña dégg, di gàntal ndigal.
24Waaye su ngeen ma dégloo ba déglu ma, kàddug Aji Sax jee, baña gàddu lenn di jaare bunti dëkk bii bésub Noflaay, xanaa di sellal bésub Noflaay, bañ cee liggéey lenn,
25su boobaa buur yiy tooge jalub Daawuda, tey dawal watiir aki fas, ñook seeni kàngam, duñu noppee jaare bunti dëkk bii, feggook seeni kàngam. Waa Yudak waa Yerusalem it di jaare ci bunt yii, dëkk bi sax dàkk.
26Dees na bàyyikoo dëkki Yuda ak li wër Yerusalem ak diiwaanu Beñamin, ca suufu tundu waak kaw tund ya, ak ca diiwaanu Negew. Ñuy indi ci kër Aji Sax ji ay saraxi rendi-dóomal ak yeneen saraxi jur ak saraxu pepp ak cuuraay. Ñii di indi kër Aji Sax ji saraxi cant.
27Waaye su ngeen ma déggalul, baña sellal bésub Noflaay, baña moytoo gàddu lenn, di jaare bunti Yerusalem bésub Noflaay, su boobaa dinaa taal dëkk bi taal buy xoyom këri Yerusalem yu yànj, te du fey.”»