Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Yeremi

Yeremi 52

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Ñaar fukki at ak benn la Cedekiya amoon ba muy falu buur, te fukki at ak benn la nguuru fa Yerusalem. Yaayam mooy Amutal doomu Yeremi ma cosaanoo Libna.
2Muy def li Aji Sax ji ñaawlu, mboolem noonee ko Yowakim defe woon.
3Merum Aji Sax ji nag dikkal Yerusalem ak Yuda, ba mu mujj xalab leen. Gannaaw gi Cedesyas fippu buuru Babilon.
4Ba Cedesyas tolloo ci juróom ñeenteelu atu nguuram, fukki fan ca fukkeelu weeram, ca la Nabukodonosor buuru Babilon ànd ak mbooloom xareem mépp ci kaw Yerusalem. Ñu dal fa janook Yerusalem, yékkati gawukaay, wërale ko.
5Dëkk ba gawe, ba keroog Cedesyas tollu ci fukkeelu atu nguuram ak benn.
6Keroog juróom ñeenti fan ca ñeenteelu weer wa, xiif ba tar lool ca biir dëkk ba, ba waa réew ma amatuñu ab dund.
7Xarekati Yuda ya génn guddi daw. Fekk na waa Babilon gaw dëkk ba. Teewul ñu rëcc, jaare ca bunt ba ca diggante ñaari tata ya, ca wetu toolu buur. Ñu daldi wuti xuru Yurdan.
8Waa Babilon nag topp Buur Cedesyas, ba dab ko ca jooru Yeriko. Fekk mbooloom xareem mépp tasaaroo, wacc ko.
9Ñu jàpp ko, yóbbu ca buuru Babilon ca dëkk ba ñuy wax Ribla ca réewum Amat. Nabukodonosor dogal fa àtteem.
10Buuru Babilon daa rendi doomi Cedesyas yu góor, muy gis, mu rendiwaale mboolem kàngami Yuda, ca Ribla.
11Gannaaw loolu mu tuur bëti Cedesyas, ba noppi jénge ko jéngi xànjar, yóbbu ko Babilon, tëj ko fa, ba keroog bés ba mu deeyee.
12Ba Nabukodonosor buuru Babilon tolloo ci fukkeelu atu nguuram ak juróom ñeent, ba am fukki fan ca juróomeelu weeru at ma, ca la bëkk-néegu buuru Babilon, Nebusaradan njiitu dag ya, dugg Yerusalem.
13Mu taal kër Aji Sax ji, taal kër buur, ak këri Yerusalem gépp, boole ca këri boroom barke ya.
14Gàngooru Babilon gépp daldi ànd ak njiital dagi buur, ñu màbb tata ya wër Yerusalem.
15Gannaaw gi ñenn ci baadoolo yi, ak ña nekkoon ca dëkk ba, ba booba, ak ña jébbaloon seen bopp buuru Babilon, ak ña desoon ca liggéeykat ya, Nebusaradan njiital dagi buur boole leen yóbbu ngàllo.
16Ñenn ca baadooloy réew ma nag, Nebusaradan njiital dag ya bàyyi leen fa, ñuy liggéey tóokëri reseñ yaak tool ya.
17Ci biir loolu kenuy xànjar ya bokkoon ca kër Aji Sax ji, ak rootukaay yaak mbalkam xànjar ma woon ca kër Aji Sax ji, waa Babilon toj lépp, boole xànjar jépp yóbbu Babilon.
18Ñu yóbbaale mboolem ndabi xànjar yi ñuy liggéeye ci kër Aji Sax ji: ndab yiy def dóom, ak ñiitukaay yi ak ñiimi feyukaayi làmp yi, ak ndab yiy def deretu sarax yi, ak and yu ndaw yi, ak mboolem jumtukaayi xànjar yi ñuy sarxalee.

19Njiital dag ya yóbbaale ndab yu ndaw yaak and yaak ndab yiy def deretu sarax, ak ndab yiy def dóom, ak tegukaayi làmp yaak and yu ndaw yaak këlli tuurukaay ya. Lu ciy wurus, mu ber, lu ciy xaalis, mu ber.
20Ñaari kenu yooyu ak mbalka maak fukki nag ak ñaar ya ko yenu, ak rootukaay ya, lépp di xànjar bu Buur Suleymaan defaraloon kër Aji Sax ji, maneesula takk diisaay ba.
21Kenu yi, gu ci nekk am na taxawaayu fukki xasab ak juróom ñett te fukki xasab ak ñaar a koy ub. Mu def pax ca biir te dëllaayu weñ ga di juróom ñeenti baaraam.
22Kenu gu ci nekk ponku xànjar a ca tege, taxawaayu ponk bi di juróomi xasab, ab caaxub xànjar wodd ko, ànd ak doomi gërënaati xànjar. Ñaari kenu yépp noonu, ànd aki gërënaat.
23Gërënaat yi juróom ñeent fukk laak juróom benn, wet gu nekk, boo ci boolee ya ca cat ya, muy téeméer, yu ub caax ba.
24Ci kaw loolu njiital dag ya jàpp Seraya sarxalkat bu mag ba, ak Cefaña sarxalkat ba ca topp, ak ñetti dagi bunt kër Aji Sax ja.
25Biir dëkk ba nag, mu jële fa benn njiitu xare, ak juróom ñaari niti dëkk ba ñu sës ci Buur, ak bindkatub njiital xare ba sasoo bind xarekat yi, ak juróom benn fukki Yudeen ñu mu fekk ca biir dëkk ba.
26Ba mu ko defee Nebusaradan, njiital dagi buur, boole leen yóbbu ca buuru Babilon ca Ribla.
27Buuru Babilon nag bóom leen foofa ca Ribla, ca réewum Amat. Noonu la waa Yuda génne seen réew, dem ngàllo.
28Lii mooy limu nit ñi Nabukodonosor toxal: Ñetti junniy Yudeen ak ñaar fukk ak ñett (3 023), loolu yemook juróom ñaareelu atu nguuram,
29ak juróom ñetti téeméer ak fanweer ak ñaar (832), loolu yemook fukkeelu atu nguuram ak juróom ñett,
30Ak juróom ñaar téeméer ak ñeent fukk ak juróom (745) yu Nebusaradan njiital dag ya, toxal. Loolu yemook ñaar fukkeelu at maak ñett ci nguurug Nabukodonosor. Ñi ñu toxal ñépp di ñeenti junni ak juróom benni téeméer (4 600).
31Yóbbu nañu Yowakin buurub Yuda ngàllo ba mu am fanweeri at ak juróom ñaar, Ewil Merodag doora falu buur ca Babilon. At mooma, fukkeelu weer waak ñaar, ñaar fukki fan ak juróom ca weer wa, ca la Ewil Merodag siggil Yowakin buurub Yuda, daldi koy tijji.
32Ci biir loolu mu wax ak moom lu rafet, jox ko cér bu sut cér ba mu jox yeneen buur, ya mu bokkal curga ca Babilon.
33Yowakin nag teqlikook yérey kaso ya, ba noppi ñu may ko muy bokk ak Buur ndab giiru dundam.
34Ci biir loolu ñu dogal ko njëlam lu sax dàkk, di bàyyikoo ci buuru Babilon bés bu jot, giiru dundam, ba keroog muy dee.