Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Room - Room 3

Room 3:7-22

Help us?
Click on verse(s) to share them!
7Mbaa ñu neeti: «Su fekkee ne dëgguteg Yàlla, sama ñàkka dëggu lay gëna kaweel, te loolu di ndamam, kon man, ana lees may joxe àtteb bàkkaarkat?»
8Ana kon lu tee nit waxe noonee nu soskat yi tuumaale ne nooy wax naan: «Nanu def lu bon, ngir mu jur lu baax»? Ñooñu mbugal lañu yelloo.
9Ana kon nun Yawut yi, lu nu gëne ci nit ñi? Du ci lenn! Ndax firndeel nanu ba noppi ne, muy Yawut bi, di ki dul Yawut, ñépp a ngi ci kilifteefu bàkkaar.
10Noonu it la Mbind mi indee ne: «Kenn jubul, du kenn sax.
11Kenn xeluwul, kenn wutul Yàlla.
12Ñépp a lajj ba bokk yàqu yaxeet, Kenn deful lu baax, du kenn sax!
13Seenug boli di bàmmeel bu ne ŋàpp, seen làmmiñ di ràbb njublaŋ, seeni kàddu aay ni daŋaru ñàngóor.
14Seen gémmiñ, waxi móolu ak wextan la feese,
15seeni tànk bar ci yoonu tuur deretu jaambur,
16te fu ñu jaare yàqute la ak musiba.
17Yoonu jàmm, xamuñu ko,
18te ag ragal Yàlla jegewu leen.»
19Xam nanu nag ne lépp lu yoonu Musaa wax, ñi ci yoonu Musaa la ko wax, ngir aw lay jeex tàkk, ngir itam mu leer nàññ ne àddina sépp a sikk fi kanam Yàlla.
20Ndax kat deesul jox kenn àtteb ku jub fa kanam Yàlla ndax jëf ju mu def, ngir sàmm yoonu Musaa; solob yoon wi daal, mooy ci lees di ràññee bu baax luy bàkkaar.
21Waaye léegi Yàlla moo feeñal nu nit di ame fa kanamam, àtteb njubam gu ajuwul ci yoonu Musaa. Te yoonu Musaa, ak yonent yi seede nañu loolu.
22Googu njub fa kanam Yàlla nag, ci gëm Yeesu Almasi lees koy ame, te mboolem ñi ko gëm la ñeel, amul xejj ak seen.

Read Room 3Room 3
Compare Room 3:7-22Room 3:7-22