1Nun ñi fendi ci wàllu ngëm, fàww nu xajoo tëley ñi néew doole, te baña sàkku sunu bànneexu bopp.
2Na ku nekk ci nun sàkku bànneexu moroomam, ci lu koy jariñ, ngir feddli ngëmam.
3Ndax Almasi kat sàkkuwul bànneexu boppam, te noonu it la Mbind mi indee ne: «Ñi lay saaga, seeni saaga, ci sama kaw la dal.»
4Ndaxte mboolem lu ñu bindoon, bu jëkk, jàngal nu moo taxoon ñu bind ko, ngir Mbind mi may nu xolu muñ, te ñaax nu, ba nu am yaakaar.
5Kon nag Yàlla miy maye xolu muñ, di ñaaxe, yal na leen may mànkoo gu mat sëkk, ni ko Almasi Yeesu bëgge,
6ngir nu bokk jenn yéene ak genn kàddu gu ngeen sàbbaale Yàlla, sunu Baayu Sang Yeesu Almasi.
7Kon nag, ni leen Almasi xajoo, nangeen ko xajoontee, ngir teddngay Yàlla.
8Dama leen di wax ne leen, bëgga fésal ne Yàlla ku dëggu la moo waral Almasi dikk, def boppam jawriñu Yawut yi, ngir sottal dige ya Yàlla digoon seeni maam.
9Leneen li indi Almasi mooy may jaambur ñi dul Yawut lu ñu màggale Yàlla, te muy yërmandeem. Noonu it la Mbind mi indee ne: «Looloo waral ma sant la ci biir xeet yi, sàbbaal la.»
10Mu neeti: «Yeen xeet yi, bégandooleen ak ñoñam.»
11Mu dellu ne: «Yeen xeetoo xeet, màggal-leen Boroom bi, réewoo réew, kañleen ko.»
12Esayi it neeti: «Ab car ay bawoo ca Yese reen ba, mooy taxaw, yilif jaambur ñi dul Yawut, te moom la ñi dul Yawut di yaakaar.»
13Kon Yàlla miy maye yaakaar, yal na leen feesale gépp mbég, ak jàmm ci biir ngëm, ba ngeen géejule yaakaar, ci manoorey Noo gu Sell gi.
14Bokk yi, man ci sama bopp, li ma bir ci seen mbir moo di yéene ju rafet ngeen fees, te buural ngeen bépp xam-xam, man ngeena artoonte it.
15Teewul mu am ci wet yu ma leen ñemee binde kàddu yu ma ñéebluwul, ngir fàttli leen li ngeen xamoon ba noppi. Noonu ma binde nag, li ko waral moo di yiw wi ma Yàlla baaxe,
16ngir ma doon jawriñu Almasi Yeesu, ñeel jaambur ñi dul Yawut, may wàccoo ak liggéeyu carxal bi xibaaru jàmm bu Yàlla laaj; su ko defee ñi dul Yawut mana doon ab jooxe bu Yàlla nangu, jooxe bu Noo gu Sell gi sellal.
17Moo tax ma saña puukarewoo Almasi Yeesu mi may liggéeyloo ci mbiri Yàlla.
18Sañumaa tudd lenn nag lu moy li Almasi sottale sama jëmm, ngir jaambur ñi dul Yawut déggal Yàlla, te muy lu mu sottale samay wax ak samay jëf,
19ci kaw firnde yu manoorewu, aki kéemaan, lépp ci manoorey Noowug Yàlla. Loolu tax na, li dale Yerusalem, wëndeelu, ba ca diiwaanu Iliri, yégle naa fa xibaaru jàmm bu Almasi, ba mu mat sëkk.
20Noonu laa masa xintewoo di xamle xibaaru jàmm bi fu ñu xamewul Almasi asi, ngir baña bey sas wu fa keneen jotoona dal.
21Noonu ma jëfe it moo dëppoo ak ni ko Mbind mi indee ne: «Ña ñu waxul woon mbiram, dinañu gis, te ña dégguloon, dinañu ràññee.»
22Sama liggéey boobu sax moo ma gàllankoor lu bare ba dikkaguma seetsi leen.
23Waaye léegi jeexal naa sama sas ci gox yii, te gannaaw at yu baree ngii, ma namma dikk ba seetsi leen,
24bu may dem Espaañ, dinaa leen seetsiwaale. Yaakaar naa leena gis bu ma fa jaaree, ba ngeen yiwi ma, ma jàlli Espaañ, gannaaw, lu mu néew néew, ay fan yu ma nammantikoo ak yeen.
25Waaye fii ma tollu, Yerusalem laa jëm, ngir ndimbal lu ñeel ñu sell ña féete foofa.
26Ndaxte gëmkati Maseduwan ak Akayi ñoom la soob ñu sàkke lenn ci seen alal, ngir dimbalee ko ñu sell ña diy néew doole ca Yerusalem.
27Seen coobarey bopp lañu ko defe, waaye ñoo ko ameel waa Yerusalem it nag. Ndaxte gannaaw ñoom ñiy jaambur, gëmkati Yerusalem ñoo leen sédd ci xéewal yi leen ngëm may, kon ñoom jaambur ñi itam war nañu leena sédd ci seen alal.
28Teewul nag bu ma noppee ci lii, ba teg teraanga jii ca loxoy waa Yerusalem, Espaañ laa jëm, te fa yeen laay jaare.
29Te xam naa ne bu ma dikkee fa yeen, barkeb Almasi bu mat sëkk laay dikke.
30Gannaaw loolu bokk yi, li ma leen di ñaan ngir sunu Boroom Yeesu Almasi, ngir itam cofeel gi Noo gu Sell giy maye, moo di ngeen fekksi ma ci xareb ñaan ngir man.
31Ñaanal-leen ma, ngir ma mucc ci aji gëmadiy Yude, te itam ndimbal li may yóbbul ñu sell ña ca Yerusalem, ñaanleen ngir ñu nangu ko.
32Su ko defee, ci coobarey Yàlla, ma dikke mbégte ba fa yeen, ba dal-luwaale as lëf fa yeen.
33Yal na Yàlla miy boroom jàmm ànd ak yeen ñépp. Amiin.