Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - ROOM - ROOM 14

ROOM 14:11-17

Help us?
Click on verse(s) to share them!
11Ndaxte Mbind mi tëral na lii: «Boroom bi nee na: “Ni mu wóore ne maa ngi dund, ni la wóore ne, ñépp dinañu ma sukkal, te ku nekk seede ne maay Yàlla.”»
12Noonu ku nekk ci nun dinga làyyi fa Yàlla ci lépp loo masa def.
13Kon nanu bàyyee tegante tooñ, waaye nu fas yéenee moytu lépp lu nekk fiir guy yóbbe sunu moroom bàkkaar.
14Xam naa ne amul wenn ñam wu sellul, ndax Yeesu Boroom bi xamal na ma loolu. Waaye loo yaakaar ne sellul, ci yaw la sellul.
15Soo dee lekk luy indil sa moroom tiis, génn nga ci mbëggeel. Yaw nag bul réeral sa moroom ci sa ñam, ndax Kirist dee na ngir moom.
16Bu sa njariñ jur wax ju ñaaw.
17Ndaxte bokk ci nguuru Yàlla jotewul dara ak lu nuy lekk mbaa lu nuy naan. Nguuru Yàlla mooy jub ci kanam Yàlla te am mbég ak jàmm ci dooley Xel mu Sell mi.

Read ROOM 14ROOM 14
Compare ROOM 14:11-17ROOM 14:11-17