Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - ROOM - ROOM 10

ROOM 10:8-16

Help us?
Click on verse(s) to share them!
8Kon boog lan lay wax? Lii: «Waxu Yàlla mi ngi ci sa wet, ci sa làmmiñ, ci sa xol.» Te wax jooju lal ngëm lanuy waare.
9Ndaxte soo waxee ak sa gémmiñ ne, Yeesu mooy Boroom bi, te nga gëm ci sa xol ne, Yàlla dekkal na ko, dinga mucc.
10Ndax xol la nit di gëme, ba tax mu jub ci kanam Yàlla; làmmiñ it la nit di waxe ne mi ngi ci Kirist, ba tax Yàlla musal ko.
11Mbind mi dafa wax ne: «Képp ku ko gëm, sa yaakaar du tas mukk.»
12Ndax ñépp a yem ci kanam Yàlla, muy Yawut mbaa ku dul Yawut, ndax kenn rekk mooy sunu Boroom nun ñépp; ku yéwén la ci képp ku koy ñaan.
13Ndaxte bind nañu: «Képp ku woo Boroom bi ciw turam, dinga mucc.»
14Waaye nan lañuy wooye ki ñu gëmagul? Naka lañu mana gëme ki ñu déggagul turam? Naka lañu mana dégge turam, te kenn xamalu leen ko?
15Nan lañu mana waaree, su leen kenn yónniwul? Looloo tax Mbind mi wax ne: «Ñiy yégle xibaaru jàmm bi, ni seen ñëw di sedde xol!»
16Waaye ñépp nanguwuñu xibaaru jàmm bi; moom la Esayi wax ne: «Boroom bi, ana ku gëm sunu waare?»

Read ROOM 10ROOM 10
Compare ROOM 10:8-16ROOM 10:8-16