Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Nawum

Nawum 1

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Yéeneb waxyu bu dal dëkk bi ñuy wax Niniw a ngi, di téereb peeñum Nawum ma dëkk Elkos.
2Aji Sax ji mooy Yàlla ju fiir, te mooy mbugale, Aji Sax ji mooy mbugale, te di boroom sànj. Aji Sax ji mooy mbugal ay bañam, mooy sànju ci kawi noonam.
3Aji Sax ji la mer ma diib, doole ja bare; te du ñàkka topp ku tooñ, ag tooñaangeem. Aji Sax jeey daagoo biir callweer ak ngëlén, niir yi di pëndub tànkam.
4Mooy gëdd géej, wowal; mboolem dex, mu ŋiisal; parluy Basan ak Karmel, mu laxal; tóor-tóori àllub Libaŋ, mu laxal.
5Tund yu mag yi di ko loxal, tund yu ndaw yi seey, suuf fuddu fi kanamam, mook àddina ak mboolem li ci biiram.
6Bu sànjoo, ana kuy taxaw? Ana kuy dékku tàngooru meram? Am sànjam a naan soteet ni sawara, doj yi rajaxoo fi kanamam.
7Aji Sax jee baax, moo dib rawtu, bésub njàqare, te moo ràññee ñi ko làqoo.
8Mbàmbulaan lay walal ba faagaagal dëkk bii, te mooy toppi noonam ba ca biir lëndëm ga.
9Ana lu ngeen di fexeel Aji Sax ji? Mooy neenal, lépp neen; njàqare ja du ñaar.
10Niy taxas la ay noonam di laxasoo, mel ni ñu naan ba màndi, te ni boob mu wow lañuy lakke ba xoyomu.
11Ci yaw dëkk bii la nit génne, di fexeel Aji Sax ji lu bon, di mébét pexey ndëngte.
12Aji Sax ji moo ne: «Bu ñu matoon, ne gàññ it ni lees leen di dagge, ñu ne mes. Maa la mitital, dootuma la mitital.
13Léegi buum gi ñu la yeewe laay dog, say jéng laay dagg.»
14Aji Sax ji moo santaane lii ci yaw. Mu ne: «Lu bokk ci saw tur du lawati, kërug say yàlla laay dagge xërëm ak jëmmi weñ gu ñu xelli, te maay waajal sa bàmmeel, nde tekkiwuloo tus.»