Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Nawum

Nawum 3

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Wóoy, ngalla dëkkub tuurkatu deret bi, ñépp di fen, fees aku ay, te foqati alalu jaambur du dakk!
2Kàccri dal, ay mbege riir, fas rëpptal, watiir kar-kari.
3Gawar buur, saamar melax, xeej lerxat, ñu bare ne lasiim, ñi dee jale, néew ya tëë jeex, ñuy fakkastaloo néew ya.
4Lépp ndax ngànctu gu bare, gi gànc bi nekke! Jekk tànkee, boroom xërëm yi, ci ngànctu nga jaaye ay xeet, te xërëmtu nga naxe ay giir.
5«Maa ngii fi sa kaw,» kàddug Aji Sax jee, Boroom gàngoor yi. «Sa pendal laay ñori, ba muur sa xar-kanam, won xeeti jaambur yi sa yaramu neen, gisloo waa réew yi sa gàcce.
6Maa lay xëpp mbalit, sewal la, def lam ceetaan,
7ku la gis, daw la te naan: “Niniw tas na! Moo ku koy jooy?” Ana fu ma koy wutale ñu ko dëfal?»
8Moo Niniw, dangaa gën Teeb, péeyub Misraa? Dëkk ba dëju fa digg wali Niil ya, am ndox wër ko, am tataam di géej, miiram di ndox mu wale géej,
9réewum Kuus di ndëgërlaayam, Misra di ko dooleele doole ju dul jeex, réewum Puut ak Libi di ko jàpple.
10Teewul ngàllo la dem, cig njaam; ay goneem, ñu falaxe leen ci mboolem selebe yoon; ay kàngamam, ñu tegoo bant; kilifaam yépp, ñu jéng leen.
11Niniw yaw it dinga bilimbaane, jànnaxe, di wuta raw ab noon.
12Sa tata yépp ni garabi figg yu ñoral ndoortel meññeef lay mel, soo yëlbee, doom ya rot, gémmiñu lekk-kat aw.
13Say gàngoor a ngii diy jigéen fi sa biir, sa bunti réew lafal say noon, ne ŋàpp-ŋàppaaral, sawara xoyom tëjukaay ya!
14Niniwee, ndox moo fàggoo ab gaw, ngay rooti te dàbbli say tata. Duggal ci bàq bi, note ban bi, te ne cas móolukaay bi!
15Fa la la sawara di xoyome, saamar xottee la fa, raafal la ni soccet di def. Fulal saw nit niy soccet, ñu tollu niy njéeréer.
16Ay jula nga barele, ba ñu ëpp biddiiwi asamaan, te ñoo mel niy soccet, tojtal, naaw.
17Say kàngam it niy soccet, say jawriñ ni naaxu gunóor yu dale kaw tata, bésub sedd, jant bi jóg, ñu daw, te deesul xam fu ñu nekk.
18Buurub Asiree, say sàmm a saay, say garmi nelaw, sa gàngoor tasaaroo kaw tund wa, te ku leen dajale wuute.

19Sa damm-damm amul paj, sab góom metti, ba mboolem ñi dégg li la dal di tàccu ci sa kaw, nde ana ku sa mbon gi dul jeex lorul?