Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - MÀRK - MÀRK 6

MÀRK 6:4-14

Help us?
Click on verse(s) to share them!
4Noonu Yeesu ne leen: «Dees na faaydaal yonent, waaye du ci réewam, ciy bokkam mbaa ci këram.»
5Yeesu manu faa def ay kéemaan yu bare, lu dul teg loxo yenn jarag, wéral leen.
6Mu waaru ndax seen ngëmadi. Bi loolu amee Yeesu di wër dëkk ya, di jàngle.
7Noonu mu woo ci moom fukki taalibe ya ak ñaar, jox leen sañ-sañu dàq rab yi, yónni leen, ñu ànd ñaar-ñaar.
8Mu digal leen nii: «Bu ngeen di dem, buleen yóbbaale dara; du mburu mbaa mbuus mbaa xaalis ci seeni maxtume, waaye yemleen ci aw yet rekk.
9Sol-leen ay dàll te yem ci benn turki.»
10Mu ne leen: «Kër gu ngeen dugg, dal-leen fa, ba kera ngeen jóge dëkk ba.
11Koo xam ne gàntu na leen, mbaa mu tanqamlu leen, génnleen fa, yëlëb seen pëndu tànk, ngir seede leen seen réer.»
12Noonu taalibe ya dem, di waare naan: «Tuubleen seeni bàkkaar.»
13Ñu dàq ay rab yu bare, te diw boppi jarag yu bare, wéral leen.
14Noonu Erodd buur bi dégg loolu, ndaxte turu Yeesu siiwoon na. Mu ne nag: «Yaxya dekki na, moo tax mu ànd ak kàttanu def ay kéemaan.»

Read MÀRK 6MÀRK 6
Compare MÀRK 6:4-14MÀRK 6:4-14