Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - MÀRK - MÀRK 5

MÀRK 5:20-36

Help us?
Click on verse(s) to share them!
20Noonu waa ji dem ci diiwaanu Fukki dëkk yi, daldi fa yégle la ko Yeesu defal, ba ñépp waaru.
21Noonu Yeesu jàllaat dex ga, taxaw ca tefes ga. Te nit ñu bare dajaloo, wër ko.
22Kenn ci njiiti jàngu ba nag, tudd Yayrus, ñëw ci moom. Naka la gis Yeesu, mu daanu ciy tànkam,
23di ko sarxu lu bare naan: «Sama doom ju jigéen mi ngi bëgga faatu; kaay teg ko loxo, ngir mu wér te dund.»
24Noonu Yeesu ànd ak moom. Bi muy dem, mbooloo mu réy topp ko, di ko tanc.
25Amoon na fa nag jigéen ju doon xëpp deret diirub fukki at ak ñaar.
26Sonnoon na lool ci loxoy fajkat yu bare, sànk ci alalam jépp te jëlewu ci genn tan, waaye faf wopp ja yokku.
27Noonu mu déggoon turu Yeesu, ne ci boppam: «Su ma laalee ay yéreem rekk, dinaa wér.» Mu jaxasoo ak mbooloo mi nag, doxe ko gannaaw, laal mbubbam.
29Ci saa si deret ji taxaw, mu yég ci yaramam ne jàngoroom deñ na.
30Yeesu yég ci saa si ne, doole génn na ci moom. Mu walbatiku nag ne mbooloo mi: «Ana ku laal samay yére?»
31Ay taalibeem ne ko: «Xanaa gisuloo mbooloo mi lay wër; ngay laaj: “Ku ma laal?”»
32Waaye Yeesu di xool li ko wër, ngir gis ku ko def.
33Noonu jigéen ja ñëw, daanu ciy tànkam, wax ko dëgg gépp; mu tiit bay lox, ndaxte xam na li xewoon ci yaramam.
34Yeesu ne ko: «Soxna si, sa ngëm faj na la; demal ci jàmm, te na sa jàngoro wàcc.»
35Bi Yeesu di wax nag, am na ku jóge ca kër njiit la, mu ñëw naan: «Sa doom faatu na; matatul nuy sonal kilifa gi.»
36Waaye Yeesu jàppul wax jooju; mu ne njiit la: «Gëmal rekk te baña tiit.»

Read MÀRK 5MÀRK 5
Compare MÀRK 5:20-36MÀRK 5:20-36