57Gannaaw loolu jamono ji Elisabet wara mucc agsi, mu daldi jur doom ju góor.
58Dëkkandoom yi ak bokkam yi yég ne, Boroom bi won na ko yërmande ju réy, ñu ànd ak moom bég.
59Bi bés ba délsee, ñu ñëw xarafalsi xale ba, bëgg koo dippee baayam Sakari.
60Waaye yaayam ne leen: «Déedéet, Yaxya lay tudd.»
61Ñu ne ko: «Amoo menn mbokk mu tudd noonu.»
62Ñu daldi liyaar baayam, ngir xam nan la bëgg ñu tudde xale ba.
63Sakari laaj àlluwa, bind ci ne: «Yaxya la tudd.» Ñépp daldi waaru.