57 Gannaaw gi Elisabet dem ba àppam mat, mu mucc, am doom ju góor.
58 Dëkkandoom yaak ay bokkam yég noonu ko Boroom bi xéewalee yërmandeem, ñu bokk ak moom mbégte ma.
59 Ba bés ba délsee, ñu dikk xarfalsi xale ba, bëgg koo tudde Sàkkaryaa, dippee ko baayam.
60 Yaayam nag ne leen: «Déet, Yaxya lay tudd.»
61 Ñu ne ko: «Waaye kenn ci say bokk tuddul noonu!»
62 Ci kaw loolu ñu liyaar baayam, ngir xam nu mu bëgg ñu tudde xale bi.
63 Sàkkaryaa laaj àlluwa, ñu jox ko, mu bind ci: «Yaxya mooy turam.» Ñépp waaru.