Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Luug - Luug 16

Luug 16:7-31

Help us?
Click on verse(s) to share them!
7Kee, mu ne ko: “Yaw nag, ñaata nga ko ameel?” Mu ne ko: “Téeméeri saakuy pepp.” Mu ne ko: “Sa kayit a ngi, bindal juróom ñett fukk.”
8Njaatige li nag naw saytukat bu njublaŋ boobu ca muus ga mu defe. Ndax kat niti tey jii ñoo gëna muus doomi leer ñi, ci ni ñuy doxale seen digganteek seeni nawle.»
9Yeesu teg ca ne: «Maa leen wax ne leen: Alalu àddina ji làmboo njubadi, sàkkooleen ko ay xarit, ngir bu alal ja jeexee, xarit yooya fat leen ca dal yu sax ya.
10Ku maandu ci lu néew nag, maandu ci lu bare; ku jubadi ci lu néew it, jubadi ci lu bare.
11Kon su ngeen maanduwul ci alalu àddina, alal ji dëgg, ana ku leen koy dénk?
12Te su ngeen maanduwul ci alalu jaambur, ana ku leen di dénk seen alalu bopp?
13«Ab jaamu kër nag manula jaamu ñaari sang; day dëddu kii, sopp kee; mbaa mu fonk kii, cof kee. Manuleena jaamoondoo Yàlla ak Alal.»
14Farisen ñu bëgg xaalis ña nag dégg loolu Yeesu wax lépp, ba noppi di ko ñaawal.
15Yeesu ne leen: «Yeen yeenay jub-jublu ci kanam nit ñi, waaye Yàlla xam na seen xol. Ndax li nit ñi gëna naw, lu seexluwu la fa Yàlla.
16«Yoonu Musaa wi ak waxi yonent yi la woon ba kera ba Yaxya dikkee. Waaye ba mu dikkee lañu yégle nguurug Yàlla, ñépp di ci jéema dugge seen doole.
17Waaye nag asamaan ak suuf raaf moo gëna yomb genn maaska rote ci mbindum yoonu Musaa.
18«Képp ku fase sa jabar, takk keneen, jaaloo nga; te ku jëkkëram fase, képp ku ko takk, jaaloo nga.
19«Jenn waay la woon ju bare alal, di sol yérey tànnéef yu rafet, di dunde lu neex bés bu set.
20Ab baadoolo bu ñuy wax Lasaar nag farala tëdde buntu kër waa ji, yaram wa ne fureet aki góom,
21te noon ngéeja fajeb xiifam lu ruuse ci ndabal boroom alal bi. Rax ci dolli xaj yiy dikk, di mar ay góomam.
22«Ba baadoolo ba deeyee, malaaka yi yóbbu ko ba ca wetu Ibraayma. Boroom alal ba itam dee, ñu rob ko.
23Ci kaw loolu ñu dugal ko sawara. Ca biir mbugal mu tar ma la dawale bëtam, daldi séen fu sore Ibraayma ak Lasaar ci wetam.
24Mu xaacu ne: “Maam Ibraayma, yërëm ma! Yebalal Lasaar, mu sëpp catal baaraamam ci ndox, dikk seralal ma sama làmmiñ, sawara sii metti na lool!”
25Ibraayma ne ko: “Doom, fàttlikul ne na nga séddoo woon sa bànneex ca àddina, noonu la Lasaar nekke woon aw tiis. Waaye fii nag moo neexle, yaw nga mitile.
26Bu loolu yépp weesee itam, sunu digg ak yeen kàmb gu xóot a fi dox; moo tax ku bëgga jóge fii jëm ci yeen, mbaa mu jóge foofu jëmsi ci nun, du ko man.”
27«Ci kaw loolu boroom alal ba ne: “Kon nag maam, ngalla yebalal Lasaar ca sama kër baay,
28ndax sama juróomi rakk a nga fa. Na leen àrtu, ngir ñu baña ñëw ñoom itam ci bérabu metit bii.”
29Ibraayma ne ko: “Waaye ñoom am nañu yoonu Musaa, am nañu téerey yonent yi. Nañ leen déggal.”
30Mu ne ko: “Loolu doyul, Maam Ibraayma, waaye su kenn bàyyikoo ci ñi dee, dem ba ca ñoom, dinañu tuub.”
31Ibraayma nag ne ko: “Su ñu dégluwul Musaa, dégluwñu yonent yi kay, ku dekki, bàyyikoo ci ñi dee sax du tax ñu gëm.”»

Read Luug 16Luug 16
Compare Luug 16:7-31Luug 16:7-31