Text copied!
Bibles in Wolof

LUUG 16:7-31 in Wolof

Help us?

LUUG 16:7-31 in Téereb Injiil

7 Mu neeti keneen: “Yaw nag, ñaata nga ko ameel?” Mu ne ko: “Téeméeri saakuy pepp.” Bëkk-néeg ba ne ko: “Sa kayit a ngii. Bindal juróom ñett fukk.”
8 Njaatige ba nag daldi naw ni bëkk-néeg bu njublaŋ boobu muuse woon. Ndaxte ñi bokk ci àddina ñoo gëna muus ci li ñu jote ci seen diggante ak seen moroom, ba raw ñi bokk ci leeru Yàlla.»
9 Yeesu teg ca ne: «Maa ngi leen di wax lii: sàkkuleen ay xarit jaare ko ci alalu àddina, ngir bu alal nekkatul, ñu man leena fat ca dal yu sax ya.
10 Nit ku maandu ci yëf yu néew, dina maandu itam ci yu bare. Ku jubadi ci yëf yu néew, du jub ci yu bare.
11 Su fekkeente ne nag jubuleen ci alalu àddina, kon ku leen di dénk alal ju wóor ji?
12 Te su ngeen maanduwul ci alal ji ngeen moomul, kon ku leen di jox alal ji ngeen moom?
13 «Benn jaam manula jaamoondoo ñaari sang; fàww nga bañ kii, bëgg ki ci des, walla nga jàpp ci kenn ki, xeeb ki ci des. Manuleena boole jaamu Yàlla ak jaamu Alal.»
14 Farisen yi déglu li Yeesu doon wax lépp, tàmbali di ko reetaan, ndaxte ñu bëggoon xaalis lañu.
15 Waaye Yeesu ne leen: «Yéen yéena ngi fexee jub ci kanam nit ñi waaye Yàlla xam na seen xol. Ndaxte li nit ñiy fonk, Yàlla sib na ko.
16 «Yoonu Musaa wi ak waxi yonent yi ñu ngi fi woon ba kera Yaxya di ñëw. La ko dale foofa nag, yégle nañu xibaaru jàmm bi ci nguuru Yàlla, te ñépp a ngi góor-góorlu, ngir dugg ci.
17 Waaye nag asamaan ak suuf jóge fi moo gëna yomb randal wenn rëdd ci arafu yoonu Musaa.
18 «Ku fase sa soxna, ba noppi takk keneen, njaaloo nga, te ku takk jigéen ju jëkkëram fase, njaaloo nga.
19 «Dafa amoon boroom alal juy sol yére yu rafet te jafe, tey dund bés bu set dund gu neex.
20 Fekk miskin mu ñuy wax Lasaar daan tëdd ca buntu këram, fees dell ak ay góom,
21 te bu sañoon, di lekk ci desiti ñam wiy rot ci lekkukaayu boroom alal ji. Xaj yi sax daan nañu ñëw, di mar ay góomam.
22 «Noonu miskin ma dee, malaaka yi yóbbu ko ca wetu Ibraayma. Boroom alal ja itam dee, ñu suul ko.
23 Bi ñu koy mbugal ca sawara, mu téen, séen fu sore Ibraayma ak Lasaar ci wetam.
24 Noonu mu yuuxu ne: “Maam Ibraayma, yërëm ma! Yebalal Lasaar, mu sëpp catul baaraamam ci ndox, seralal ma sama làmmiñ, ndaxte maa ngi sonn lool ci sawara sii!”
25 Ibraayma ne ko: “Sama doom, fàttalikul ne jot nga sa bànneex ci àddina, fekk Lasaar dëkk ci tiis. Looloo tax xolam sedd fii, yaw nag, ngay sonn.
26 Rax-ca-dolli it am na kàmb gu xóot sunu diggante ak yéen, ba tax ñi bëgga jóge fii jëm ci yéen, walla ñi bëgga jóge foofu jëmsi ci nun, duñu ko man.”
27 «Noonu boroom alal ja ne: “Kon nag maam, maa ngi lay ñaan, nga yebal Lasaar ca sama kër baay,
28 ndaxte am naa fa juróomi rakk. Na leen artu, ngir ñu baña ñëw ñoom itam ci bérabu metit wii.”
29 Ibraayma ne ko: “Say doomu baay, ñu ngeek yoonu Musaa ak téerey yonent yi. Nañu leen déggal.”
30 Boroom alal ja ne ko: “Déedéet, maam Ibraayma, waaye su kenn dekkee, dem ca ñoom, dinañu tuub seeni bàkkaar.”
31 Waaye Ibraayma ne ko: “Su ñu dégluwul Musaa ak yonent yi, kon ku dekki sax, du tax ñu gëm.”»
LUUG 16 in Téereb Injiil

Luug 16:7-31 in Kàddug Yàlla gi

7 Kee, mu ne ko: “Yaw nag, ñaata nga ko ameel?” Mu ne ko: “Téeméeri saakuy pepp.” Mu ne ko: “Sa kayit a ngi, bindal juróom ñett fukk.”
8 Njaatige li nag naw saytukat bu njublaŋ boobu ca muus ga mu defe. Ndax kat niti tey jii ñoo gëna muus doomi leer ñi, ci ni ñuy doxale seen digganteek seeni nawle.»
9 Yeesu teg ca ne: «Maa leen wax ne leen: Alalu àddina ji làmboo njubadi, sàkkooleen ko ay xarit, ngir bu alal ja jeexee, xarit yooya fat leen ca dal yu sax ya.
10 Ku maandu ci lu néew nag, maandu ci lu bare; ku jubadi ci lu néew it, jubadi ci lu bare.
11 Kon su ngeen maanduwul ci alalu àddina, alal ji dëgg, ana ku leen koy dénk?
12 Te su ngeen maanduwul ci alalu jaambur, ana ku leen di dénk seen alalu bopp?
13 «Ab jaamu kër nag manula jaamu ñaari sang; day dëddu kii, sopp kee; mbaa mu fonk kii, cof kee. Manuleena jaamoondoo Yàlla ak Alal.»
14 Farisen ñu bëgg xaalis ña nag dégg loolu Yeesu wax lépp, ba noppi di ko ñaawal.
15 Yeesu ne leen: «Yeen yeenay jub-jublu ci kanam nit ñi, waaye Yàlla xam na seen xol. Ndax li nit ñi gëna naw, lu seexluwu la fa Yàlla.
16 «Yoonu Musaa wi ak waxi yonent yi la woon ba kera ba Yaxya dikkee. Waaye ba mu dikkee lañu yégle nguurug Yàlla, ñépp di ci jéema dugge seen doole.
17 Waaye nag asamaan ak suuf raaf moo gëna yomb genn maaska rote ci mbindum yoonu Musaa.
18 «Képp ku fase sa jabar, takk keneen, jaaloo nga; te ku jëkkëram fase, képp ku ko takk, jaaloo nga.
19 «Jenn waay la woon ju bare alal, di sol yérey tànnéef yu rafet, di dunde lu neex bés bu set.
20 Ab baadoolo bu ñuy wax Lasaar nag farala tëdde buntu kër waa ji, yaram wa ne fureet aki góom,
21 te noon ngéeja fajeb xiifam lu ruuse ci ndabal boroom alal bi. Rax ci dolli xaj yiy dikk, di mar ay góomam.
22 «Ba baadoolo ba deeyee, malaaka yi yóbbu ko ba ca wetu Ibraayma. Boroom alal ba itam dee, ñu rob ko.
23 Ci kaw loolu ñu dugal ko sawara. Ca biir mbugal mu tar ma la dawale bëtam, daldi séen fu sore Ibraayma ak Lasaar ci wetam.
24 Mu xaacu ne: “Maam Ibraayma, yërëm ma! Yebalal Lasaar, mu sëpp catal baaraamam ci ndox, dikk seralal ma sama làmmiñ, sawara sii metti na lool!”
25 Ibraayma ne ko: “Doom, fàttlikul ne na nga séddoo woon sa bànneex ca àddina, noonu la Lasaar nekke woon aw tiis. Waaye fii nag moo neexle, yaw nga mitile.
26 Bu loolu yépp weesee itam, sunu digg ak yeen kàmb gu xóot a fi dox; moo tax ku bëgga jóge fii jëm ci yeen, mbaa mu jóge foofu jëmsi ci nun, du ko man.”
27 «Ci kaw loolu boroom alal ba ne: “Kon nag maam, ngalla yebalal Lasaar ca sama kër baay,
28 ndax sama juróomi rakk a nga fa. Na leen àrtu, ngir ñu baña ñëw ñoom itam ci bérabu metit bii.”
29 Ibraayma ne ko: “Waaye ñoom am nañu yoonu Musaa, am nañu téerey yonent yi. Nañ leen déggal.”
30 Mu ne ko: “Loolu doyul, Maam Ibraayma, waaye su kenn bàyyikoo ci ñi dee, dem ba ca ñoom, dinañu tuub.”
31 Ibraayma nag ne ko: “Su ñu dégluwul Musaa, dégluwñu yonent yi kay, ku dekki, bàyyikoo ci ñi dee sax du tax ñu gëm.”»
Luug 16 in Kàddug Yàlla gi