3Ana nu ngeen di def keroog bésub mbugal ba, keroog ba safaan di bawoo fu sore? Ana ku ngeen di daw wuti wallam? Ana fu ngeen di denci seen teraanga?
4Xanaa ànd ak ña ñu jàpp, ne yogg; mbaa tëddandook ña ñu bóom, ne lareet. Teewul Aji Sax ji xàcci loxoom, meddiwul ba tey.
5Wóoy ngalla Asiri miy sama yetu mer, bolde bi ñu ŋàbb di samam sànj,
6ma xabtal ko fi kaw xeet wu gëmadi, yebal ko ca askan woowu ma merloo, ngir ñu sëxëtoo leen, nangu seen alal, note leen ni banu mbedd.