Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Room - Room 1

Room 1:10-22

Help us?
Click on verse(s) to share them!
10Xanaa di saxoo dagaan ci samay ñaan, su ci Yàlla àndee, yoon wu jub wu ma mujj dikke ba ci yeen.
11Yàkkamti naa leena gis, ba jottli leen mayug yiw gu bawoo ci Noo gu Sell gi, ngir dooleel leen,
12te loolu mooy ma bokk ak yeen lu dëfal sama xol, dëfal leen, ci seen ngëm ak sama gos.
13Bokk yi, bugguma ngeen umple ne ay yooni yoon laa leen mébéta seetsi, ba liggéey ci seen biir lu leen jariñ, ni ma ko defale yeneen xeet; waaye ay gàllankoor a ma téye ba tey jii.
14Muy sama digg ak Gereg yu xay yi, mbaa ñu xayadi ñi, ak ñi rafet xel, mbaa ñi ñàkk xel, am na lu ma war ci ñoom ñépp.
15Moo tax, yeen waa Room itam, ma yàkkamti leena àggesi xibaaru jàmm bi.
16Awma lu may rus ci xibaaru jàmm bi, ndax kat mooy manoorey Yàlla jiy musal képp ku ko gëm, dale ci Yawut bi, teg ci ki dul Yawut.
17Ci xibaaru jàmm bi lañu feeñal ni Yàlla di joxe nit ñi àtteb ñu jub, te lépp aju ci ngëm, ca ndoorte la, ba ca njeexital la. Noonu la Mbind mi indee ne: «Ku jub ndax ngëmam mooy dund.»
18Sànjum Yàlla fa asamaan lay dale feeñ, ba wàcc ci mboolem ngëmadi, ak njubadiy nit ñiy fatt ag dëgg ci biir ag njubadi.
19Ndaxam lees mana xam ci Yàlla, leer na ci seen biir, nde Yàlla moo leen ko leeralal.
20Ndax kat, li gisuwul ci Yàlla, te di manooreem gi dul jeex, ak jikko ji mu wéetoo ndax li muy Yàlla, ba àddina sosoo ba tey, xel man na koo ràññee ci ay liggéeyam, te looloo leen taxa ñàkku lay.
21Gannaaw ba ñu xamee Yàlla, taxul ñu màggal ko ngir li muy Yàlla, taxul ñu delloo ko njukkal, xanaa réer ci seen xalaati neen, ba seen xel mu wayadi far tàbbi cig lëndëm.
22Xel mu rafet lañuy jaay ba mujj diy dof.

Read Room 1Room 1
Compare Room 1:10-22Room 1:10-22