10Te li ma koy faral di ñaan mooy lii: bu soobee Yàlla, na ma ubbil bunt, ba ma mana ñëw ci yéen.
11Ndaxte bëgg naa leena gis lool, ba indil leen barke bu jóge ci Xel mu Sell mi, ndax seen ngëm gëna dëgër.
12Maanaam ma nekk ci seen biir, te nu dimbaleente ci sunu ngëm, ndax man itam ma gëna am doole.
13Bokk yi, damaa bëgg ngeen xam ne xalaat naa leena seetsi ay yooni yoon, ngir meññ njariñ ci yéen, ni ma ko defe ci yeneen xeet yi, waaye ay téq-téq ñoo ma téye ba léegi.
14Am naa warugar sama diggante ak ñépp, muy ñi jàng ni Gereg yi, muy ñi jàngul ni Baarbaar yi, ñi bare xam-xam ak ñi barewul xam-xam.
15Li aju ci man nag, jekk naa ngir ñëw, xamal leen xibaaru jàmm bi, yéen it waa Room.
16Ndaxte awma benn werante ci xibaaru jàmm bi may waare, ndax mbirum Yàlla la, mu làmboo dooleem, ngir musal képp ku ko gëm, muy Yawut ci bu jëkk mbaa ki dul Yawut.
17Ndaxte xibaar bii day wone, ni nit mana jube ci kanam Yàlla, sukkandikoo ci ngëm rekk, tàmbali ci ngëm, yem ci ngëm. Moo tax Mbind mi wax ne: «Ku jub ci kaw ngëm, dinga dund.»
18Merum Yàllaa ngi feeñe asamaan, wàcc ci nit ñi, ndax seen weddi Yàlla gépp ak seen jubadi gépp, ñoom ñi suul dëgg, di topp lu jubadi.
19Ndax li nit mana xam ci Yàlla, leer na ci seen xel, ndax Yàlla won na leen ko.
20Ndaxte ba àddina sosoo ba tey, mbiri Yàlla yu nëbbu ya, maanaam dooleem ju sax ja, ak meloom wu kawe wa, feeñ nañu bu leer, te bir ñépp ci yi mu sàkk, ba tax bunti lay yépp tëj nañu.
21Ndaxte bi ñu xamee Yàlla, taxul ñu màggal ko ni mu ware, mbaa ñu sant ko. Waaye ñu daldi réer ci seen biiri xalaat yu mujjul fenn, ba tax seen xol gumba, ba lëndëm këruus.
22Ñu teg seen bopp ni boroomi xel, fekk ñu ñàkk xel lañu woon.