Text copied!
Bibles in Wolof

ROOM 1:10-22 in Wolof

Help us?

ROOM 1:10-22 in Téereb Injiil

10 Te li ma koy faral di ñaan mooy lii: bu soobee Yàlla, na ma ubbil bunt, ba ma mana ñëw ci yéen.
11 Ndaxte bëgg naa leena gis lool, ba indil leen barke bu jóge ci Xel mu Sell mi, ndax seen ngëm gëna dëgër.
12 Maanaam ma nekk ci seen biir, te nu dimbaleente ci sunu ngëm, ndax man itam ma gëna am doole.
13 Bokk yi, damaa bëgg ngeen xam ne xalaat naa leena seetsi ay yooni yoon, ngir meññ njariñ ci yéen, ni ma ko defe ci yeneen xeet yi, waaye ay téq-téq ñoo ma téye ba léegi.
14 Am naa warugar sama diggante ak ñépp, muy ñi jàng ni Gereg yi, muy ñi jàngul ni Baarbaar yi, ñi bare xam-xam ak ñi barewul xam-xam.
15 Li aju ci man nag, jekk naa ngir ñëw, xamal leen xibaaru jàmm bi, yéen it waa Room.
16 Ndaxte awma benn werante ci xibaaru jàmm bi may waare, ndax mbirum Yàlla la, mu làmboo dooleem, ngir musal képp ku ko gëm, muy Yawut ci bu jëkk mbaa ki dul Yawut.
17 Ndaxte xibaar bii day wone, ni nit mana jube ci kanam Yàlla, sukkandikoo ci ngëm rekk, tàmbali ci ngëm, yem ci ngëm. Moo tax Mbind mi wax ne: «Ku jub ci kaw ngëm, dinga dund.»
18 Merum Yàllaa ngi feeñe asamaan, wàcc ci nit ñi, ndax seen weddi Yàlla gépp ak seen jubadi gépp, ñoom ñi suul dëgg, di topp lu jubadi.
19 Ndax li nit mana xam ci Yàlla, leer na ci seen xel, ndax Yàlla won na leen ko.
20 Ndaxte ba àddina sosoo ba tey, mbiri Yàlla yu nëbbu ya, maanaam dooleem ju sax ja, ak meloom wu kawe wa, feeñ nañu bu leer, te bir ñépp ci yi mu sàkk, ba tax bunti lay yépp tëj nañu.
21 Ndaxte bi ñu xamee Yàlla, taxul ñu màggal ko ni mu ware, mbaa ñu sant ko. Waaye ñu daldi réer ci seen biiri xalaat yu mujjul fenn, ba tax seen xol gumba, ba lëndëm këruus.
22 Ñu teg seen bopp ni boroomi xel, fekk ñu ñàkk xel lañu woon.
ROOM 1 in Téereb Injiil

Room 1:10-22 in Kàddug Yàlla gi

10 Xanaa di saxoo dagaan ci samay ñaan, su ci Yàlla àndee, yoon wu jub wu ma mujj dikke ba ci yeen.
11 Yàkkamti naa leena gis, ba jottli leen mayug yiw gu bawoo ci Noo gu Sell gi, ngir dooleel leen,
12 te loolu mooy ma bokk ak yeen lu dëfal sama xol, dëfal leen, ci seen ngëm ak sama gos.
13 Bokk yi, bugguma ngeen umple ne ay yooni yoon laa leen mébéta seetsi, ba liggéey ci seen biir lu leen jariñ, ni ma ko defale yeneen xeet; waaye ay gàllankoor a ma téye ba tey jii.
14 Muy sama digg ak Gereg yu xay yi, mbaa ñu xayadi ñi, ak ñi rafet xel, mbaa ñi ñàkk xel, am na lu ma war ci ñoom ñépp.
15 Moo tax, yeen waa Room itam, ma yàkkamti leena àggesi xibaaru jàmm bi.
16 Awma lu may rus ci xibaaru jàmm bi, ndax kat mooy manoorey Yàlla jiy musal képp ku ko gëm, dale ci Yawut bi, teg ci ki dul Yawut.
17 Ci xibaaru jàmm bi lañu feeñal ni Yàlla di joxe nit ñi àtteb ñu jub, te lépp aju ci ngëm, ca ndoorte la, ba ca njeexital la. Noonu la Mbind mi indee ne: «Ku jub ndax ngëmam mooy dund.»
18 Sànjum Yàlla fa asamaan lay dale feeñ, ba wàcc ci mboolem ngëmadi, ak njubadiy nit ñiy fatt ag dëgg ci biir ag njubadi.
19 Ndaxam lees mana xam ci Yàlla, leer na ci seen biir, nde Yàlla moo leen ko leeralal.
20 Ndax kat, li gisuwul ci Yàlla, te di manooreem gi dul jeex, ak jikko ji mu wéetoo ndax li muy Yàlla, ba àddina sosoo ba tey, xel man na koo ràññee ci ay liggéeyam, te looloo leen taxa ñàkku lay.
21 Gannaaw ba ñu xamee Yàlla, taxul ñu màggal ko ngir li muy Yàlla, taxul ñu delloo ko njukkal, xanaa réer ci seen xalaati neen, ba seen xel mu wayadi far tàbbi cig lëndëm.
22 Xel mu rafet lañuy jaay ba mujj diy dof.
Room 1 in Kàddug Yàlla gi