10Ci kaw loolu Musaa ak Aaróona àgg ba ca Firawna. Ñu def la leen Aji Sax ji santoon. Aaróona jël yetam, sànni ca suuf ca kanam Firawnaaki dagam; yet wa soppliku jaan.
11Ba mu ko defee Firawna moom itam woo boroom xam-xam yaak jibar ya. Ñeengokati Misra ya ñoom it fexe ca seeni xargafuufa, ba def lu mel noona.
12Ku nekk ca ñoom sànni yetam, mu soppliku jaan, yetu Aaróona nag wonn seeni yet.