Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Malasi

Malasi 1

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Yéeneb kàddug Aji Sax jii moo ñeel Israyil, ci jottlib Malasi.
2Aji Sax ji nee: «Dama leena sopp,» yeen ngeen ne: «Ana noo nu soppe?» Mu ne: «Xanaa Esawu du seexub Yanqóoba?» Kàddug Aji Sax jee, «moona Yanqóoba laa sopp,
3te Esawu laa foñ. Maa def ay tundam ab gent, ab céru suufam, ma def ko dëkkuwaayu tilli màndiŋ mi.
4Su Edom nee: “Dees noo rajaxe, waaye nooy tabaxaat gent bi,” Aji Sax ji Boroom gàngoor yi moom dafa wax ne: “Ñooy tabax, maay màbb.” Ñoom lees di wooye waa diiwaan bu bon bi, askan wi Aji Sax ji mere ba fàww.
5Yeena koy gisal seen bopp, yeenay seede ne: “Màggaayu Aji Sax ji jéggi na kemu réewum Israyil.”
6«Doom teral baayam, jaam, sangam. Man, su ma dee baay, ana saab teraanga? Su ma dee ab sang, ana saab cér?» Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax, mu ne: «Yeen sarxalkat yi teddadil ngeen sama tur, yeen ngeen ne: “Ana nu nu teddadile sa tur?”
7Xanaa di indi ñam wu sobewu fi sama sarxalukaay. Yeen ngeen ne: “Ana nu nu la sobeele?” Xanaa xalaat ne sañees naa teddadil sarxalukaayu Aji Sax ji.
8Bu ngeen ma sarxalsee jur gu gumba, dara aayu ci? Am bu ngeen ma sarxalsee jur guy soox, ak jur gu wopp, dara aayu ci daal! Yóbbul leen ko seen boroom dëkk rekk, ba xam ndax moo leen di nangul, mbaa mu siggil leen!» Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax.
9«Ngeen ne: “Léegi nag tinuleen Yàlla rekk, mu baaxe nu!” Yeena tooñ, ndax day siggil kenn ci yeen?» Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax.
10«Éy bu kenn ci yeen tëjoon bunt yi far, te baña jafal ab taal ci sama kaw sarxalukaay ci dara. Awma benn bànneex ci yeen!» Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax. «Ab sarax, duma ko nangoo ci seeni loxo.
11Waaye li ko dale penku ba sowub jant, fu ci nekk la sama tur màgge ci biir xeet yi, te fépp lees di taale cuuraay, ngir sama tur, boole ci sarax su set, nde sama tur a ni màgge fi biir xeet yi.» Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax.
12«Waaye yeen yeena teddadil sarxalukaayu Aji Sax ji, nde yeena xalaat ne lu sobewu la, te aw yàppam, aw ñamam jarul dara.
13Yeena ngi naa: “Ndaw lu soof,” di ciipatu.» Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax. «Jur gu ñu sàcc ngeen may indil, ak guy soox, ak gu wopp, loolu mooy seen sarax! Nu ma koy nangoo ci seeni loxo?» Aji Sax jee ko wax.
14«Alkànde ñeel na ab jinigalkat bu am ci géttam am kuuy mu mu xasoo sarxe, te di sarxalal Boroom bi jur gu sikk, nde man, buur bu mag laa!» Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax. «Sama tur moo jara ragal fi biir xeet yi.