Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Malasi

Malasi 3

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1«Maa ngii di yebal sama ndaw, mu xàllal ma aw yoon. Sang bi (/Boroom bi) ngeen di sàkku mooy jekki agsi këram, malaakam kóllëre moomu (/ndawal kóllëre loolu), ki ngeen safoo, mu ngooguy dikk.» Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax.
2Waaye bésub dikkam, ana ku ko mana dékku? Bu teewee ana kuy taxaw? Nde moom daa mel ni sawaras tëgg buy xelli weñ, melati ni xemey fóotkat.
3Fa mbaxana dee benn lay tooge ni xellikat ak seggkat, te mooy segg sëti Lewi, xelli leen ni xaalis ak wurus, ba ñu doon niti Aji Sax ji, ñi koy indil sarax ci njekk.
4Su boobaa la saraxu Yuda ak Yerusalem di neex Aji Sax ji, na jant ya woon, at ya woon.
5«Maa leen di dikke ab àtte, di ab seede bu taxaw temm ci tuumaal ñeengokat yeek njaalookat yi, ak ñiy fene ngiñ, ak ñiy xañ ab liggéeykat peyooram, di noggatu ab jëtun akub jirim, di beddi doxandéem te ragaluñu ma.» Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax.
6«Man Aji Sax ji déy, duma soppiku, te yeen noppiwuleen di askanu Yanqóoba, ay workat.
7«Ca seen janti maam ngeen dëddoo sama dogali yoon, sàmmuleen ko. Waññikuleen fi man, ma waññiku fi yeen,» Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax. «Yeena ngi naa: “Ci lan lanuy waññikoo?”
8Waaw, nit dina sàcc Yàlla? Ndaxam yeen yeena ngi may sàcc te yeena ne: “Ana nu nu la sàcce?” Xanaa ci seen cérub fukkeelu alal akub jooxe.
9Alkànde ju réya ngi leen di dikkal, nde man ngeen di sàcc, yeen mboolem askan wi.
10Indileen mboolem céru fukkeel ca kërug denc ya, ba ab dund am sama biir kër, te ngeen seetloo ma ko rekk,» Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax, «ndegam duma leen ubbil bunti asamaan, ba sottil leen barke bu doy.
11Maa leen di gëddal njéeréer, ba du leen yàqal meññeefum suuf, te reseñug tool du leen jaasiral.» Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax.
12«Xeet yépp ñu barkeel ñi lañu leen di wooye, nde réewum bànneex ngeen di dëkke.» Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax.
13«Kàddu yu ñagas ngeen teg ci sama kaw,» Aji Sax jee ko wax. «Te yeena ne: “Ana kàddu yu ñu la waxal”?
14Yeena ne: “Jaamu Yàlla ag neen la. Ana lu nu jële ci dénkoo ndénkaaneem, tey wéye toroxlu fi kanam Aji Sax ji Boroom gàngoor yi?
15Moo tax nu ne nit ñu bew ñi ñooy ñi barkeel, ñiy def lu bon kay ñoo baaxle, ñoom ñiy diiŋat Yàlla, teg ca rëcc.”»
16Ca la ñi ragal Aji Sax ji diisoo ci seen biir, Aji Sax ji teewlu, déglu leen. Ñu bind fi kanamam téereb fàttliku, bu lim ñi ragal Aji Sax ji, te teral aw turam.
17«Sama moomeelu bopp la ñooñuy doon,» Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax, «ca bés ba may jëfi, sama gànjar lañuy doon, te ni baay di baaxee as ngóoram su ko taxawu, ni laa leen di baaxee.
18Ca ngeen di ràññaatlewaat diggante ku jub ak ku bon, kuy jaamu Yàlla, ak ku ko jaamuwul.

19Bés ba déy a ngii di ñëw, di tàkk ni taal bu yànj. Képp ku bew ak kuy def lu bon, ca lay mel ni boob, te bésub keroog baa koy jafal.» Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax. «Du leen waccal tus, dub reen, dub car.
20Waaye yeen ñi ma ragal la jantub njekk di fenkal, yiire leen ceeñeer yuy wéral, ngeen génn di tëbantu ni ay sëlluy yar.
21Yeenay joggi ñu bon ñi, ñu doon pënd fi seen ron téstën, keroog bés ba may jëfi.» Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax.
22«Bàyyileen xel ci yoonu Musaa, sama jaam ba, yoon wa ma ko dénkoon fa tundu Oreb, ñeel Israyil gépp, mu diy dogal ak àttey yoon.
23Maa ngii di yebal ci yeen, Ilyaas yonent bi, balaa bésub Aji Sax jee teew, di lu màgg te raglu.
24Mooy delloo xolu baay ca doom ja, delloo xolu doom ca baay ba, lu ko moy ma dikk duma réew mi, ba faagaagal ko.»