Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - MÀRK - MÀRK 4

MÀRK 4:35-40

Help us?
Click on verse(s) to share them!
35Bés booba nag ci ngoon Yeesu ne taalibe yi: «Nanu jàll dex gi.»
36Mu yiwi mbooloo mi nag, ay taalibeem jël ko ni mu mel ci gaal gi; te yeneen gaal ànd ak moom.
37Naka noona ngelaw lu mag daldi jóg, duus yi sàng gaal gi, ba mu bëgga fees.
38Fekk Yeesu tëdd di nelaw ci ngegenaay ci taatu gaal gi. Taalibe yi daldi ko yee naan: «Kilifa gi, ndax sunu bakkan soxalu la?»
39Ci kaw loolu Yeesu jóg, daldi gëdd ngelaw li, ne dex gi: «Noppil te dal!» Noonu ngelaw li dal, ba lépp ne nemm.
40Yeesu ne taalibe ya: «Lu tax ngeen tiit? Ndax gëmaguleen?»

Read MÀRK 4MÀRK 4
Compare MÀRK 4:35-40MÀRK 4:35-40