Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - LUUG - LUUG 6

LUUG 6:6-19

Help us?
Click on verse(s) to share them!
6Beneen bésub noflaay, Yeesu dugg ci jàngu bi, di fa jàngle. Amoon na fa nit ku loxol ndijooram làggi.
7Xutbakat yi ak Farisen yi ñu ngi ko doon xool, ba xam ndax dina ko faj ci bésub noflaay bi, ngir ñu am lu ñu ko tuumaale.
8Waaye Yeesu xam seen xalaat, daldi ne ku loxoom làggi: «Jógal taxaw ci kanam ñépp.» Nit ka daldi jóg taxaw.
9Yeesu ne leen: «Ma laaj leen, lan moo jaadu, nu def ko bésub noflaay bi, lu baax mbaa lu bon; nu musal nit mbaa nu lor nit?»
10Ci kaw loolu mu xool leen ñoom ñépp, ba noppi ne nit ka: «Tàllalal sa loxo.» Mu tàllal ko, loxoom daldi wér péŋŋ.
11Waaye nit ña mer ba fees, di rabat pexe yu jëm ca Yeesu.
12Ca bés yooya Yeesu yéeg ca tund wa ngir ñaan, mu fanaan fa, di ñaan ci Yàlla.
13Bi bët setee, Yeesu woo taalibeem yi, tànn ci fukk ak ñaar, tudde leen ay ndawam:
14Simoŋ, mi Yeesu tudde Piyeer, ak Andare, mi bokk ak Piyeer ndey ak baay; Saag ak Yowaana, Filib ak Bartelemi,
15Macë ak Tomaa, Saag doomu Alfe, ak Simoŋ mi bokk ci mbooloo, ma ñu tudde Ñi farlu ci moom seen réew;
16Yudaa doomu Saag, ak Yudaa Iskariyo, mi mujja wor.
17Yeesu ànd ak ndaw ya, wàcc tund ya, daldi taxaw ca joor ga, fa mbooloom taalibe mu takku nekkoon. Amoon na fa it ay nit ñu bare ñu jóge ca réewu Yawut ya mépp ak ca dëkku Yerusalem ak dëkk yi nekk ca wetu géej ga, maanaam Tir ak Sidon.
18Dañoo ñëw ngir déglu ko, te it ngir mu faj leen. Ñi rab jàpp it faju nañu.
19Ñépp a ngi ko doon wuta laal ndax doole jiy jóge ci moom, di faj ñépp.

Read LUUG 6LUUG 6
Compare LUUG 6:6-19LUUG 6:6-19