Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Luug - Luug 20

Luug 20:30-45

Help us?
Click on verse(s) to share them!
30Tofo ba,
31ak ñaareelu tofo ba, ku ci nekk donn na ndaw sa ca magam, ñu topplantee ko noonu, ba juróom ñaar ñépp dee te amuñu ca doom.
32Gannaaw gi ndaw sa it dee.
33Ndaw si nag, keroog ndekkite la, kan la ciy doon jabaram, gannaaw juróom ñaar ñépp a ko jëloon jabar?»
34Yeesu ne leen: «Ci àddina sii la góor ñi ak jigéen ñi di séy.
35Waaye ña ñu yeyale ndekkitel ëllëg, yeyale leen bakkan ci àddina siy ñëw, ñooñu, su boobaa, kenn du ci am jabar mbaa jëkkër.
36Dootuñu mana dee it, ndax niy malaaka lañuy mel. Ay doomi Yàlla lañuy doon, ndax da leen di fekk dekki.
37Te Musaa ci boppam xamle na ne ñi dee dañuy dekki, na ko téere indee ca mbirum ngarab sa. Mooy ba mu wooyee Boroom bi: “Yàllay Ibraayma, Yàllay Isaaxa, Yàllay Yanqóoba.”
38Kon moom du ñi dee lay seen Yàlla, xanaa ñiy dund, ndax fa moom, ñépp a ngi dund.»
39Ci kaw loolu ñenn ca firikati yoon ya àddu ne ko: «Dëgg nga wax, Sëriñ bi!»
40Gannaaw loolu ñemeetuñu koo laaj dara.
41Yeesu neeti leen: «Nees mana waxe ne Almasi, Sëtub Daawuda la?
42Daawuda ci boppam moo ne ci téereb Sabóor: “Boroom bi moo ne sama Sang: ‘Toogeel sama ndijoor,
43ba ma def say noon, sa ndëggastal.’ ”
44Gannaaw Daawudaa wooye Almasi “Sang bi,” nu mu nekke ab sëtam?»
45Yeesu nag wax ak ay taalibeem, askan wépp di dégg. Mu ne:

Read Luug 20Luug 20
Compare Luug 20:30-45Luug 20:30-45