Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Luug - Luug 10

Luug 10:25-41

Help us?
Click on verse(s) to share them!
25Benn xamkatu yoonu Musaa moo jekki woon jóg, di fexee fiir Yeesu. Mu ne ko: «Sëriñ bi, ana lu may def, ba texe ba fàww?»
26Yeesu ne ko: «Yoonu Musaa, ana lees ci bind? Loo ci jànge?»
27Mu ne ko: «Boroom bi sa Yàlla, nanga ko soppe sa léppi xol ak sa léppi bakkan ak sa léppi doole ak sa léppi xel, te ni nga soppe sa bopp, nanga ko soppe sa moroom.»
28Yeesu nag ne ko: «Wax nga dëgg. Noonu ngay def, daldi texe.»
29Waa ja nag namma wutu lay, ne Yeesu: «Sama moroom mooy kan?»
30Yeesu neeti ko: «Jenn waay a jóge woon Yerusalem, jëm Yeriko. Mu dajeek ay sàcc, ñu futti ko, dóor ko, daldi dem, bàyyi ko, muy waaja dee.
31Yàlla woo yàlla ab sarxalkat bu jaare yoon woowa, séen nit ka, daldi teggi.
32Jenn waay ju soqikoo ci giirug Lewi it noonu; daa dikk ba tollu foofa, séen waa ja, daldi teggi.
33Jenn waay ju dëkk Samari nag doon tukki, dikk ba jege waa ja, xool ko, yërëm ko lool.
34Mu dikk, sotti diw ak biiñ ca gaañu-gaañu ya, lëmës ko. Ci kaw loolu mu teg ko ci mbaamam, yóbbu ko ci ab dalukaay, di ko topptoo.
35Ca ëllëg sa, mu yékkati ñaari poseti xaalis, jox ko boroom dal ba, ne ko: “Topptoo ko waa ji. Loo ci dolli, bu ma dëppee, maa la koy delloo.”»
36Mu teg ca ne ko: «Ñett ñii, kan nga foog ne moo ci taxawu waa ja dajeek sàcc ya, taxawaayu nit ak moroomam?»
37Mu ne ko: «Xanaa ki ko defal yërmande.» Yeesu nag ne ko: «Demal boog, di defe noonu.»
38Yeesu ak ay taalibeem ñoo toppoon seenu yoon, ba tollook ab dëkk. Ba ñu dikkee, senn as ndaw su ñuy wax Màrt, ganale ko.
39Ci kaw loolu rakkam ju ñuy wax Maryaama toog ca wetu Sang bi, di déglu kàddoom,
40te fekk Màrt jàpp lool ca liggéeyu waañ wa. Mu dikk ne Yeesu: «Sang bi, xanaa gisoo sama rakk ji ma bàyyeek liggéeyu waañ wi, man doŋŋ? Wax ci boog, mu jàpple ma.»
41Sang bi ne ko: «Màrt, Màrt, yitte yi nga xintewoo, di ci doñ-doñi moo bare.

Read Luug 10Luug 10
Compare Luug 10:25-41Luug 10:25-41