25Noonu benn xutbakat daldi jóg, ngir fexee fiir Yeesu ne ko: «Kilifa gi, lan laa wara def, ba am dund gu dul jeex?»
26Yeesu ne ko: «Lu ñu bind ci yoonu Musaa? Lan nga ciy jàng?»
27Nit ka ne ko: «“Nanga bëgg Yàlla sa Boroom ak sa xol bépp ak sa bakkan bépp, sa kàttan gépp ak sa xel mépp,” te it: “Nanga bëgg sa moroom, ni nga bëgge sa bopp.”»
28Yeesu ne ko nag: «Li nga wax dëgg la. Boo defee loolu, dinga dund ba fàww.»
29Waaye xutbakat ba bëggoona am aw lay, ne Yeesu: «Kan mooy sama moroom nag?»
30Yeesu ne ko: «Dafa amoon nit ku jóge woon Yerusalem, jëm Yeriko. Ay sàcc dogale ko, futti ko, dóor ko ba muy bëgga dee, dem bàyyi ko fa.
31Faf ab sarxalkat jaar ca yoon wa, séen nit ka, teggi.
32Benn waay it bu soqikoo ci giiru Lewi, aw ca bérab booba, séen waa ja, teggi.
33Waaye benn waay bu dëkk Samari bu doon tukki, ñëw ba jege waa ja, gis ko, yërëm ko.
34Noonu mu ñëw, sotti diw ak biiñ ca gaañu-gaañu ya, lëmës ko. Gannaaw loolu mu teg ko ci mbaamam, yóbbu ko ci fanaanukaay, di ko topptoo.
35Bi bët setee, mu génne ñaari poseti xaalis, jox ko boroom kër ga ne ko: “Nanga topptoo nit kooku. Bés bu ma fi jaaraatee, dinaa la fey, man ci sama bopp, lépp loo ci dolli ci xaalis.”»
36Yeesu teg ca ne: «Lu ciy sa xalaat? Kan ci ñett ñooñu moo jëfe ni kuy jëf jëme ci moroomam, ba ñu gisee nit, ka sàcc ya dogale woon?»
37Xutbakat ba ne ko: «Xanaa ki ko won yërmandeem.» Yeesu ne ko nag: «Demal tey def ni moom.»
38Bi Yeesu ak ay taalibeem nekkee ci yoon wi, mu dugg ci benn dëkk, fekk fa jigéen ju tudd Màrt, ganale ko.
39Màrt nag amoon rakk ju tudd Maryaama, ma nga toog ci tànki Boroom bi, di déglu ay kàddoom.
40Fekk Màrt jàpp lool ca waañ wa. Noonu mu ñëw ci wetu Yeesu ne ko: «Boroom bi, doo ci wax dara, boo gisee sama rakk ji bàyyi ma ak liggéey bi yépp? Ne ko mu jàpple ma.»
41Boroom bi ne ko: «Màrt, Màrt, yu baree ngi fees sa xol, nga am ay téq-téq ndax loolu.