25 Benn xamkatu yoonu Musaa moo jekki woon jóg, di fexee fiir Yeesu. Mu ne ko: «Sëriñ bi, ana lu may def, ba texe ba fàww?»
26 Yeesu ne ko: «Yoonu Musaa, ana lees ci bind? Loo ci jànge?»
27 Mu ne ko: «Boroom bi sa Yàlla, nanga ko soppe sa léppi xol ak sa léppi bakkan ak sa léppi doole ak sa léppi xel, te ni nga soppe sa bopp, nanga ko soppe sa moroom.»
28 Yeesu nag ne ko: «Wax nga dëgg. Noonu ngay def, daldi texe.»
29 Waa ja nag namma wutu lay, ne Yeesu: «Sama moroom mooy kan?»
30 Yeesu neeti ko: «Jenn waay a jóge woon Yerusalem, jëm Yeriko. Mu dajeek ay sàcc, ñu futti ko, dóor ko, daldi dem, bàyyi ko, muy waaja dee.
31 Yàlla woo yàlla ab sarxalkat bu jaare yoon woowa, séen nit ka, daldi teggi.
32 Jenn waay ju soqikoo ci giirug Lewi it noonu; daa dikk ba tollu foofa, séen waa ja, daldi teggi.
33 Jenn waay ju dëkk Samari nag doon tukki, dikk ba jege waa ja, xool ko, yërëm ko lool.
34 Mu dikk, sotti diw ak biiñ ca gaañu-gaañu ya, lëmës ko. Ci kaw loolu mu teg ko ci mbaamam, yóbbu ko ci ab dalukaay, di ko topptoo.
35 Ca ëllëg sa, mu yékkati ñaari poseti xaalis, jox ko boroom dal ba, ne ko: “Topptoo ko waa ji. Loo ci dolli, bu ma dëppee, maa la koy delloo.”»
36 Mu teg ca ne ko: «Ñett ñii, kan nga foog ne moo ci taxawu waa ja dajeek sàcc ya, taxawaayu nit ak moroomam?»
37 Mu ne ko: «Xanaa ki ko defal yërmande.» Yeesu nag ne ko: «Demal boog, di defe noonu.»
38 Yeesu ak ay taalibeem ñoo toppoon seenu yoon, ba tollook ab dëkk. Ba ñu dikkee, senn as ndaw su ñuy wax Màrt, ganale ko.
39 Ci kaw loolu rakkam ju ñuy wax Maryaama toog ca wetu Sang bi, di déglu kàddoom,
40 te fekk Màrt jàpp lool ca liggéeyu waañ wa. Mu dikk ne Yeesu: «Sang bi, xanaa gisoo sama rakk ji ma bàyyeek liggéeyu waañ wi, man doŋŋ? Wax ci boog, mu jàpple ma.»
41 Sang bi ne ko: «Màrt, Màrt, yitte yi nga xintewoo, di ci doñ-doñi moo bare.