Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Esteer

Esteer 4

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Ba Mardose yégee la ñu def lépp, daa xottiy yéreem, sol ay saaku, sottikoo dóom, di ko ñaawloo, dugg ci biir dëkk bi, di yuuxu yuux gu réy te metti.
2Mu dem ba ca buntu kër buur, yem fa ndax deesul dugge kër buur yérey saaku.
3Ci biir loolu mboolem diiwaani réew mi, fépp fu dogalu buur ak ndigalam àgg, muy ñaawlu gu réy ca Yawut ya. Ñu boole kook koor aki jooy aki yuux. Ñu bare sol ay saaku, sottikoo dóom, di ko toroxloo.
4Ba surgay Esteer yu jigéen yaak bëkk-néegam yu góor ya dikkee wax ko Esteer, tiislu na ko lool, daldi yónnee Mardose ay yére, ngir mu summi saaku ya mu sol. Waaye Mardose nanguwul.
5Esteer woolu Atag, ma Buur féetaleek moom, te muy kenn ci bëkk-néegi buur. Mu yebal ko ci Mardose, ngir xam lan la ak lu waral loolu.
6Atag dem ba ca Mardose, ca pénc ma janook buntu kër buur.
7Mardose wax ko mboolem la ko dal, ak dayob xaalis ba Aman digee fey, nar koo def ca denci buur ngir mana sànk Yawut yi.
8Mu jël sottib mbindum dogal ba ñu yéene ca Sus ne dinañu leen faagaagal, daldi ko koy jox, ngir mu won ko Esteer, xamal ko ko, ne ko mu gaaw dem ca Buur, ñaanal ko ko, tinul ko aw xeetam.
9Atag dellu ca Esteer, yegge ko kàdduy Mardose.
10Esteer ne Atag mu dem wax Mardose, ne ko:
11«Mboolem surgay buur ak waa diiwaani buur xam nañu ne yoon a toppe àtteb dee képp ku dugg kër buur, ba ci ëttu biiram, muy góor mbaa jigéen, te wooyeesu la. Xanaa ku buur tàllal yetu wurus wiy màndargaal nguuram. Man nag fanweeri fan a ngii wooyeesu ma fa Buur.»
12Ñu yegge Mardose kàdduy Esteer;
13Mardose dellu yónnee ne ko: «Ãay! Yaa ngi kër buur de! Waaye bul defe ne man ngaa mucc, yaw doŋŋ, ci mboolem Yawut yi.
14Ndax soo ci selaŋloo ba selaŋlu ci tey jii it, wall ak xettal dina bawoo feneen ñeel Yawut yi, waaye yaw yaak sa waa kër baay dingeen sànku. Li nga dugg ci nguur gi sax, nga defe ne neen la? Jombul diggante bii nu tollu tey moo ko waral.»
15Esteer dellu yónnee ca Mardose, ne ko:
16«Demal woo mboolem Yawut yi, ci Sus, ñu daje. Te ngeen wooral ma: buleen lekk, buleen naan diiru ñetti fan, du guddi, du bëccëg. Man it maak sama surga yu jigéen, nu woore noonu. Su ko defee ma dem ca Buur doonte yoon nanguwu ko. Su ma dee dee, ma dee rekk.»
17Mardose nag dem, def la ko Esteer sant lépp.