1Gannaaw loolu Buur Aserus jox bésub keroog Lingeer Esteer kër Aman, fitnaalkatu Yawut ya. Ñu woo Mardose ca Buur, ndax fekk na Esteer xamle ba noppi na Mardose bokkeek moom.
2Buur nag tekki jaarob torlukaayam ba mu nangoo ca Aman, jox ko Mardose. Esteer daldi teg kër Aman ci loxol Mardose, mu di ko saytu.
3Esteer daldi dellu wax ak Buur, ne gurub cay tànkam, jooy, tinu ko, ne ko mu fanq musiba mi Aman Agageen ba sooke ak pexe mi mu lalaloon Yawut yi.
4Ci kaw loolu Buur tàllal Esteer yetu wurus wa, Esteer jóg taxaw ca kanam Buur.
5Mu ne: «Buur, ndegam neex na la, te xool nga ma bëtu yiw, ndegam jaadu na ci yaw, te ma saf la, bindlul ndigal luy neenal bataaxal yi sosoo ci Aman Agageen ba, doomu Amdeta. Mu bindoon ko ngir faagaagal Yawut yi ci mboolem diiwaani buur.
6Ana nu ma mana seetaane musiba di dal samaw xeet ak nu ma mana seetaane ñuy sànk samay bokk?»
7Buur Aserus wax ak Lingeer Esteer ak Mardose Yawut ba, ne leen: «Ma ne, kër Aman jox naa ko Esteer; Aman, ma wékklu ko ca bant ba, ndax li mu dal ci kaw Yawut yi.
8Yeen ci seen wàllu bopp nag, bindleen ci Yawut yi lu leen soob ci sama tur, man Buur. Tayleen ko, torloo ko sama jaaro. Ndax mbind mu ñu bind ci turu buur, tay ko, torloo ko jaarob buur, maneesu koo toxal.»
9Ci kaw loolu ñu woo bindkati buur ca bés ba, di ñaar fukki fan ak ñett ca weeru Siwan, ñetteelu weer wa. Ñu daldi bind mboolem lu Mardose santaane, ca mbirum Yawut yaak jawriñ yaak boroom dëkk yaak kàngami diiwaan ya, dale ko ca End ba ca Kuus. Muy téeméeri diiwaan ak ñaar fukk ak juróom ñaar (127). Ñu bind ndigal ya ci mbindum diiwaan bu nekk ak ci làkku xeet wu nekk, Yawut ya it ak seen mbindu bopp ak seen làkku bopp.
10Mardose bind ci turu Buur Aserus, tay bataaxal yi, torloo ko jaarob buur, yóbbante ko ay gawar yu war dawkati naari góor yu ñu tànn.
11Ñu bind ca bataaxal ya, ne Buur may na Yawut yi ci dëkkoo dëkk sañ-sañu taxawandoo, aar seen bopp. Sañ nañoo tas mbooloo mu leen mana song, ak xeet wu ñu bokk mbaa diiwaan bu ñu bawoo. Nañu sànk woowu xeet, rey leen, faagaagal leen ñook seeni jabar ak seeni doom, boole ca lël seen alal.
12Bés ba ñu mayee loolu ci mboolem diiwaani Buur Aserus di fukki fan ak ñett ci weeru Adar, fukkeelu weer waak ñaar.
13Ñu wara siiwal ab sottib bataaxal ba, muy ndigalu yoon ci diiwaanoo diiwaan, biralal ko mboolem xeet yi, ngir bésub keroog Yawut yi taxaw temm, feyoonteek seeni noon.
14Ndaw ya war fasi buur yu diy dawkat, ñu sàqi, gaaw, rëpptal ci ndigalu buur. Ñu siiwal nag dogal ba ca Sus, péey ba.
15Ba mu ko defee Mardose bàyyikoo ca Buur; ma nga sol yérey buur, baxa ak weex, ak mbaxanam buur mu wurus mu réy, ak mbubbum lẽe mu xonq curr. Dëkku Sus baa ngay riire mbégteek bànneex.
16Kanami Yawut yaa nga ne ràññ ci biir mbégteek bànneex akub sag.
17Mboolem diiwaan mbaa dëkk bu mag bu dogalu buur ba àgg, muy mbégteek bànneex ca Yawut ya; ñu def ko bés bu rafet, di xawaare. Bare na sax ñu bokk ci xeeti réew ma, ñu walbatiku dugg ci diiney Yawut ndax ragal Yawut ya.