Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Esayi - Esayi 10

Esayi 10:20-34

Help us?
Click on verse(s) to share them!
20Keroog bés booba li des fi Israyil ak li rëcce kër Yanqóoba duñu wéerooti ña leen duma. Aji Sax ji lañuy wóolu, wéeroo ko, Aji Sell ju Israyil.
21Aw ndes ay délsi, di ndesu askanu Yanqóoba, ñeel Yàlla Jàmbaar ji.
22Seen xeet wi ni feppi suufas géej lay tollu, te as ndes a ciy délsi. Àtteb sànkute mooy taxaw, yoon toppe ba mat sëkk.
23Sànkute déy mooy taxaw, Boroom bi, Aji Sax ji Boroom gàngoor yi di ko sottal fi réew mi mépp.
24Moo tax Boroom bi, Aji Sax ji Boroom gàngoor yi dafa wax ne: «Yeen sama ñoñ ñi dëkke Siyoŋ, buleen ragal waa Asiri yi leen di dóor yet, ŋàbbal leen bolde ni waa Misra daa def ak yeen.
25Waaye fi leek lu néewa néew mbugal jeex fi seen biir, am sànj sippil Asiri seen sànkute.»
26Aji Sax ji Boroom gàngoor yee leen di ŋàbbal kàccri, na mu defoon waa Majan fa doju Oreb. Mooy xàcciw yetam, mu dal géej, na mu defoon fa Misra.
27Bésub keroog sëf bu ñu leen sëfoon wàcc leen, ngeen tàggook yet wu ñu leen tënke woon, nde seen yaram ay naat, ba yet wa damm.
28Noon yeey songsi Ayat, jéggi Migron, dem ba Migmas, teg fa seeni jumtukaay,
29jaare ca xunti ma te naan: «Geba lanuy fanaani!» Waa Raama tiit, waa Gibeya gu Sóol daw.
30Yeen waa Galim, yuuxuleen, yeen waa Laysa, dégluleen, yeen waa Anatot, feeluleen.
31Waa Madmena ñooy fëlxoo, waa Gebim wuti rawtu.
32Tey jii noon yaa ngay taxaw fa Noob, di sànni loxo waa tundu Siyoŋ, di ko tëkkoo waa Yerusalem googu.
33Boroom baa ngoog, Aji Sax ji Boroom gàngoor yi, mu ngi gor garab yi, di rajaxe car yi, njobbaxtal ya gëna kawe dog, la ca gënoona siggi, wàcc.
34Mooy jël sémmiñ, goraale gajji gott bi, Libaŋ loroo loxol boroom doole, ba jóoru.

Read Esayi 10Esayi 10
Compare Esayi 10:20-34Esayi 10:20-34