Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - 2.Timote

2.Timote 2

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Kon nag yaw doom, doolewool yiw, wi Almasi Yeesu di maye.
2Li nga dégge ci man te seede yu bare teewe ko, nanga ko jottli nit ñu wóor ñu ko mana xamal ñeneen.
3Jëlal sa wàll ci coono bi takk-derub Almasi Yeesu bu wóor di jànkoonteel.
4Ab takk-der bu bëgga neex ka ko solal kat, du xintewoo mbiri nit ña soluwul.
5Kuy joŋante it, deesu ko kaala te joŋantewul ci yoon.
6Te it beykat bi yor coonob liggéey bi, moo wara jëkka séddu ca meññeef ma.
7Defal sam xel ci li ma la wax. Boroom bi moo lay leeralal lépp.
8Bàyyil xel ci Yeesu Almasi mi ñu dekkal te mu soqikoo ci Daawuda, ni ko sama xibaaru jàmm indee.
9Xibaaru jàmm boobu moo tax may daj coono yu metti ni defkatu mbon, ba ci jéng yii ñu ma jéng. Waaye kàddug Yàlla moom, deesu ko jéng.
10Looloo ma tax di muñ lépp, ngir ñi ñu taamu, ndax ñoom it ñu dajeek mucc gi ci Almasi Yeesu, boole ci teraanga ju sax.
11Kàddu gu wóor a ngii: Su nu deeyandoo ak Almasi, nooy dundandoo ak moom itam;
12su nu muñee, nooy bokk nguuru.
13Su nu ko gàntalee, moom it dinanu gàntal; su nu ko ñàkkee kóllëre, mu saxoo kóllëreem, ndax manula gàntal boppam.
14Loolu, dee ko fàttlee, te ngay dénkaane fi kanam Yàlla, ñu bañ di xuloo ci ay baat, ndax amul njariñ, ñi koy dégg doŋŋ lay sànk.
15Defal sa kem-kàttan ba boo teewee fa kanam Yàlla, di ku mu gërëm, ab liggéeykat bu mucc gàcce, di xamle kàddug dëgg gi ni mu ware.
16Waaye ay kebetuy àddinay kese, moytu ko, ndax ngëmadi gu ko yées rekk lay yóbbee,
17te kàdduy ñooñu day law ni ngal. Ci ñooñu la Imene ak Filet bokk.
18Ñoo lajj yoonu dëgg, ba naan ñiy dekki, dekki nañu ba noppi, te seen wax jooju, am na ñenn ñu muy yàq seen ngëm.

19Teewul cëslaay lu dëgër, li Yàlla tabax, mu ngi ne kekk, te màndarga ma ca nekk, kàddu yii la: «Boroom bi xam na ay ñoñam,» ak: «Kuy tudd turu Sang bi, na daw njubadi.»
20Kër gu mag nag, du ndabi wurus ak xaalis rekk a fa am, waaye yoy bant a nga fa, ak yoy ban; yii di ndabi teraanga, yee di ndabi njoogaan.
21Ku setal sa bopp nag ba mucc ci yu bon yooyii, yaay doon ndabal teraanga lu sell te amal sangam njariñ ngir jépp jëf ju baax.
22Xemmemtéefi ndaw nag, daw ko, te nga topp njub, ak ngëm ak cofeel, ak jàmm, ànd ceek ñiy tudde Boroom bi xol bu set wecc.
23Waaye werante yu xeluwul te du xam-xam, moyu ko, te xam ne ay ŋaayoo lay jur.
24Te jaamub Boroom bi warul di ŋaayoo, waaye day lewet ci ñépp, mana jàngle tey muñ.
25Jaamub Boroom bi ndànk la war di jubbanti diiŋatkat yi, nde jombul Yàlla may leen ñu tuub, ba xam liy dëgg.
26Su ko defee seenum xel dellusi, ba ñu rëcc fiirug Seytaane, mi leen jàpp, di leen defloo coobareem.