Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - 2.Timote

2.Timote 3

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Lii, nanga ko xam: mujug jamono, jant yu tar dina dikk.
2Nit ñi, seen bopp doŋŋ lañuy bëgg, ay bëggkati xaalis lañuy doon, ay damukat, nit ñu réy, di ay saagakati Yàlla, ñu déggadil waajur, ñu santadi te selladi.
3Duñu am ab xol, duñu meddi, ay soskat lañuy doon, ñu ñàkk sago, ñu néeg te bañ lu baax;
4ay workat lañuy doon, ñu teeyadi, ñu daŋŋiiral te di ñu bëgg seen bànneexu bopp, ba mu gënal leen Yàlla.
5Ag njullite lañuy mbubboo tey xalab leer ga leen ko wara manloo. Ñooñu, dëddu leen.
6Ñenn ci ñooñu ñooy yoxoosuy dugg ci biir kër yi, di fàbbi jigéen ñu ñàkk bopp, ñi seeni bàkkaar man, te seen xemmemtéef yu bare jiital leen.
7Gëstu ay àlluwa la jigéen ñooñuy wéye, waaye duñu mana xam liy dëgg mukk.
8Noonee Sànnes ak Sàmbres doon jànkoonteek Musaa, ni la góor ñooñu di jànkoontee ak dëgg gi; ñooy nit ñu seenum xel yàqu, te ñu doyadi ci wàllu ngëm.
9Waaye duñu soreeti, ndax seenug ndof dina bir ñépp, na ñaar ñooña mujje woon.
10Yaw nag seetlu nga bu baax sama àlluwa, ak sama dundin, ak sama mébét, ak sama ngëm, ak samag muñ, ak sama cofeel, ak samag ñeme coono,
11ak itam bundxatal yaak njàqare ya ma dikke woon fa dëkk yooyu di Àncos ak Ikoñum ak Listar. Céy na ñu ma bundxatale, waaye Sang bee ma musal ci lépp!
12Te kat képp ku namma nekke ag njullite ci yoonu Almasi Yeesu, dees na la bundxatal.
13Waaye nit ñu bon ñi, ak maa-man yi dañuy gën di bon rekk, di naxe tey nax seen bopp.
14Yaw nag saxal ci li nga jàng, muy lu la wóor, nde xam nga ña nga tanqe.
15Bi ngay lu tuut nga dale xam Mbind mu sell mi, te moo la mana may xel mu la jëme ci mucc gi gëm Almasi Yeesu di maye.
16Mboolem Mbind mu sell mi la Yàlla wal ag Noowam, ba mu am njariñal jàngal nit ñi, femmu leen, jubbanti leen, yar leen cig njub.
17Su ko defee nitu Yàlla ki mat sëkk te matley jumtukaay ngir jépp jëf ju baax.