Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Room - Room 14

Room 14:9-19

Help us?
Click on verse(s) to share them!
9Loolu sax moo waral Almasi dee, ba noppi dekki, dellu di dund, ngir ñi dee ak ñiy dund ñépp, muy seen boroom.
10Yaw nag ana looy sikke sa mbokkum gëmkat, ak itam, ana looy xeebe sa mbokkum gëmkat? Ndax kat nun ñépp ay taxawi fa kanam jalub àttekaayu Yàlla.
11Ndaxte bindees na ne: «Ndegam maay Kiy Dund, Boroom bee ko wax, man la ñépp di sukkal seen bëti óom, te man Yàlla la làmmiñu ñépp di sàbbaal.»
12Kon ku nekk ci nun, yaay layool sa bopp fa Yàlla.
13Kon nag bunu di seetati lu nu sikkantee, li ngeen di seet kay mooy nu ngeen fexee ba dungeen yóbbe mbokkum gëmkat lu koy fakktal, mbaa lu koy daane ci bàkkaar.
14Xam naa nag, wér na ma it te Sang Yeesu tax, ne amul lenn lu sobewu ci wàllu boppam, ba daganula lekk; waaye ki jàppe lenn muy lu sobewu, ci moom la loola di lu sobewu.
15Soo dee lekk lenn ba tax sa mbokk am ci lu ko naqari, noppi ngaa doxe cofeel. Bu sag lekk sànk ku Almasi deeyal.
16Li dagan ci yaw, bu ko jariñoo ba may kenn lu mu ŋàññee.
17Ndax kat solob nguurug Yàlla jotewul dara akug lekk mbaa ag naan, waaye solob nguuru Yàlla moo di njub ak jàmm, ak mbégte ci ndimbalal Noo gu Sell gi.
18Noonu kat ku koy jaamoo Almasi, yaa neex Yàlla, am ngërëmal nit ñi.
19Kon nag nanu sàkku luy indi jàmm, ak lu nu feddalantee.

Read Room 14Room 14
Compare Room 14:9-19Room 14:9-19