Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Luug - Luug 8

Luug 8:30-54

Help us?
Click on verse(s) to share them!
30Yeesu ne ko: «Noo tudd?» Mu ne ko: «Coggal.» Ndax rab yu baree duggoon waa ji.
31Rab yi nag tinu Yeesu, ngir mu bañ leena yebal ca xóote ba.
32Ag coggalu mbaam-xuux yu baree nga woon foofa, di fore ca tund wa. Rab ya tinu Yeesu, ne mu may leen, ñu dugg mbaam-xuux ya. Mu may leen ko.
33Rab ya nag génn nit ka, dugg mbaam-xuux ya, coggal ga bartaloondoo, tàbbi ca dex ga, daldi lab.
34Sàmm ya gis la xew, daldi daw, nettaliji ko waa dëkk ba, ak dëkk-dëkkaan ya.
35Nit ña riire ca, di seet la xew. Naka lañu dikk ba ci Yeesu, yem ci nit ki rab wi teqlikool, mu ànd ak sagoom, solu, toog ca wetu Yeesu. Ñu daldi tiit.
36Ña ko fekke woon nag, nettali leen na boroomi rab ba jote wall.
37Ci kaw loolu mbooloom diiwaanu Serasa gépp tinu Yeesu ngir mu jóge ca seen biir te dem ndax tiitaange lu réy lu leen jàpp. Naka la Yeesu dugg gaal, di dem,
38nit ka teqlikook rab yi di ko sarxu ngir ànd ak moom. Teewul Yeesu yiwi ko, ne ko:
39«Ñibbil, te nga xamle li la Yàlla defal lépp.» Waa ja it dem di siiwal ca dëkk ba bépp, mboolem la ko Yeesu defal.
40Ba Yeesu delloo ca wàllaa dex, mbooloo maa ko teertu, ndax ñoom ñépp a ko doon xaar.
41Ci kaw loolu rekk jenn waay dikk, ku ñuy wax Yayrus, di njiitu jàngu ba. Mu ne gurub fi kanam Yeesu, sarxu ko ngir mu ñëw këram,
42ndax kenn la amoon ci doom, janq bu am fukki at ak ñaar, te ma nga doon waaja dee. Yeesoo ngay dem, nit ña raj-rajloo, tanc ko.
43Senn as ndaw a nga ca woon, diiru fukki at ak ñaar, ma nga doon xëpp deret, te def na ci alalam jépp, kenn manu koo faj.
44Mu doxe Yeesu gannaaw, teg loxoom ca catal mbubbam, deret ja dal ca saa sa.
45Yeesu nag ne: «Ana ku ma laal?» Ku nekk di miim. Piyeer ne ko: «Njaatige, mbooloo mépp a la yéew, dar la.»
46Teewul Yeesu ne: «Am na ku ma laal kay, ndax yég naa leer gu bàyyikoo ci man.»
47Ndaw sa xam ne feeñ na. Mu daldi dikk, di lox, ne gurub fa kanam Yeesu, daldi wax ca kanam ñépp la waral mu teg ko loxoom, ak na mu wére ca saa sa.
48Yeesu ne ko: «Janq, sa ngëm faj na la. Demal ak jàmm.»
49Naka la Yeesu di wax, jenn waay jóge ca kër njiitu jàngu ba, dikk ne: «Matatul ngay sonal sëriñ bi, sa janq ba faatu na.»
50Yeesu dégg ca, ne njiit la: «Bul tiit. Gëmal rekk, mu daldi mucc.»
51Bi Yeesu agsee ca kër ga, mayul kenn ànd ak moom dugg, ku moy Piyeer, ak Yowaan ak Yanqóoba ak baayu xale bi, ak ndeyam.
52Ñépp a ngay jooy ak a tiislu janq bi. Yeesu nag ne leen: «Buleen jooy. Janq bi deewul, day nelaw rekk.»
53Ci kaw loolu ñu di ko kókkali, ndax xamoon nañu xéll ne dee na.
54Yeesu itam jàpp ca loxol janq ba, daldi àddu ca kaw, ne ko: «Janq, jógal.»

Read Luug 8Luug 8
Compare Luug 8:30-54Luug 8:30-54