30Noonu Yeesu laaj ko: «Noo tudd?» Mu ne ko: «Coggal laa tudd.» Dafa wax loolu, ndaxte rab yu baree ko jàppoon.
31Rab yooyoo ngi ko doon ñaan, ngir mu bañ leena sant, ñu dem ca kàmb gu xóot gi.
32Fekk amoon na fa géttu mbaam-xuux yu bare, yuy for ca tund wa. Rab ya ñaan Yeesu, mu may leen, ñu dugg mbaam-xuux ya. Mu may leen ko.
33Noonu rab ya génn nit ka, dugg mbaam-xuux ya, ñu daldi bartalu, daanu ca dex ga, lab.
34Sàmm ya gis li xew, daw nettaliji mbir mi ca dëkk ba ak ca àll ba.
35Nit ñi génn, ngir seet li xew. Bi ñu agsee ca Yeesu, ñu fekk fa nit, ka rab ya bàyyi woon, toog ca kanam Yeesu, sol ay yére te ànd ak sagoom. Ñu daldi ragal.
36Ña fekke woon mbir ma nag, nettali leen naka la Yeesu wérale ki rab ya jàppoon.
37Ci kaw loolu waa diiwaanu Serasa bépp ragal, ba ñaan Yeesu mu jóge fa. Noonu Yeesu dugg ci gaal gi, di bëgga dem.
38Nit ki Yeesu tàggale woon ak rab ya ñaan ko, ngir ànd ak moom. Waaye Yeesu waññi ko ne ko:
39«Ñibbil, nettali li la Yàlla defal lépp.» Noonu waa ji dem di wër dëkk ba yépp, di fa yégle la ko Yeesu defal.
40Bi Yeesu dëppee dellu, mbooloo ma di ko teeru, ndaxte ñépp a ngi ko doon xaar.
41Noonu nit ñëw, tuddoon Yayrus te nekk njiitu jàngu ba. Bi mu agsee, mu daanu ci tànki Yeesu, sarxu ko mu ñëw këram,
42ndaxte jenn doomam ju jigéen, ji mu amoon kepp te muy tollu ci fukki at ak ñaar, ma nga doon waaja dee. Bi Yeesuy dem, nit ñaa ngi doon buuxante, di ko tanc.
43Amoon na nag ca mbooloo ma jigéen ju doon xëpp deret diirub fukki at ak ñaar, te kenn manu ko woona faj.
44Jigéen ja jegeñsi Yeesu nag, doxe ko gannaaw, laal catu mbubbam. Ca saa sa deret ji dal.
45Yeesu laaj nit ña ne: «Ana ku ma laal?» Ku nekk di miim. Noonu Piyeer ne ko: «Kilifa gi, nit ñépp a ngi lay wër, di la tanc wet gu nekk.»
46Waaye Yeesu ne: «Am na ku ma laal, ndaxte yég naa ne am na doole ju génn ci man.»
47Te jigéen ja xam ne manul woona nëbb li mu def. Mu daldi daanu ci tànki Yeesu, di lox. Noonu mu nettali ci kanam ñépp li taxoon mu laal Yeesu, ak ni mu wére ca saa sa.
48Yeesu ne ko: «Soxna si, sa ngëm faj na la. Demal ci jàmm.»
49Bi Yeesu di wax nag, am na ku jóge ca kër njiit la, mu ñëw naan: «Sa doom faatu na; matatul ngay sonal kilifa gi.»
50Yeesu dégg kàddu yooyu, daldi ne njiit la: «Bul tiit. Gëmal rekk te dina dundaat.»
51Bi Yeesu agsee ca kër ga, nanguwul kenn duggaaleek moom, ñu dul Piyeer, Yowaana, Saag ak waajuri xale ba.
52Ña fa nekk ñépp di yuuxu ak di jooy xale bi. Noonu Yeesu ne leen: «Bàyyileen seen jooy yi. Janq bi deewul, day nelaw rekk.»
53Waaye ñu di ko ñaawal, ndaxte xamoon nañu ne dee na.
54Waaye Yeesu jàpp loxob janq ba, woo ko ne ko: «Xale bi, jógal.»