13Ca bés boobu ñaar ci taalibe yi di dem ci dëkku Emayus, te mu sore Yerusalem ci lu mat fukki kilomet.
14Ñu waxtaane li xewoon lépp.
15Bi ñuy waxtaan ak a sotteente xalaat, Yeesu ci boppam dab leen, ànd ak ñoom,
16fekk seeni bët muuru, ba manu ko woona xàmmi.
17Yeesu ne leen: «Lan ngeen di waxtaane nii ci yoon wi?» Noonu ñu taxaw, seen xol jeex.
18Kenn ci ñoom, ki tudd Këleyopas ne ko: «Xanaa yaw rekk yaa ñëw Yerusalem te umple li fi xewoon bés yii?»
19Yeesu ne leen: «Lu fi xew?» Ñu ne ko: «Mbirum Yeesum Nasaret. Ab yonent la woon bu doon def ay jëf yu mag, di wax ay kàddu yu am doole, ci kanam nit ñi ak ca kanam Yàlla.
20Waaye sunuy sarxalkat yu mag ak sunuy njiit ñoo ko jébbal nguur gi ngir ñu àtte ko, teg ko dee, ba daaj ko ci bant.
21Nun nag danoo yaakaaroon ne mooy kiy nara jot Israyil. Waaye bi loolu xewee ak léegi, tey la ñetteelu fan bi.
22Teewul nag am na ay jigéen yu bokk ci nun yu nu jaaxal. Dañoo fajaru ca bàmmeel ba,
23waaye fekkuñu fa néewam. Ñu délsi, nettali nu ne, ay malaaka feeñu nañu leen, yégal leen ne mi ngi dund.
24Ñenn ci sunu àndandoo yi dem nañu ca bàmmeel ba, fekk lépp mel, na ko jigéen ña waxe woon. Waaye moom gisuñu ko.»
25Noonu Yeesu ne leen: «Yéen daal, yéena ñàkk xel, te seen xol yéexa gëm li yonent yi yégle woon!
26Xanaa du Almasi bi dafa waroona daj boobu coono te dugg ci ndamam?»