Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Luug - Luug 12

Luug 12:48-57

Help us?
Click on verse(s) to share them!
48Waaye jawriñ ji xamul nammeelu njaatigeem, te teewu koo def lu yelloo ay duma, yet yu néew lay am. Képp ku ñu jox lu bare, dees na la topp lu bare. Képp ku ñu dénk jopp, dees na la feyeeku lu ko ëpp.
49«Sawara laa taalsi ci kaw suuf, te maaka bëggoon mu ne jippét xaat!
50Am na nag sóobu gu ma wara sóobu, waaye ndaw njàqare ci man li feek loolu sottiwul.
51Foog ngeen ne maye jàmm ci kaw suuf moo ma indi? Déet kay. Maa leen wax lii, xanaa ag féewaloo.
52Gannaaw-si-tey, bu juróomi nit bokkee genn kër, dinañu féewaloo; ñett féewaloo ak ñaar, ñaar féewaloo ak ñett.
53Baay dina féewaloo ak doomam ju góor, doom ja féewaloo ak baayam; ndey féewaloo ak doomam ju jigéen, doom ja féewaloo ak ndeyam; ndey féewaloo ak jabaru doomam, jabar ja féewaloo ak ndeyu jëkkër ja.»
54Yeesu neeti mbooloo ma: «Bu ngeen gisee mu xiine sowu, dangeen dal naan: “Taw baa ngi ñëw,” te noonu lay ame.
55Bu ngelaw bawoo bëj-saalum, ngeen ne: “Tàngaay wu metti lay doon,” te mooy am.
56Jinigalkat yi ngeen doon! Melow asamaan ak suuf, man ngeen koo firi. Xew-xewi janti tey jii nag, nu ngeen umplee pireem?
57«Te itam lu leen tee àtte njub, yeen ci seen bopp?

Read Luug 12Luug 12
Compare Luug 12:48-57Luug 12:48-57