Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - LUUG - LUUG 12

LUUG 12:48-57

Help us?
Click on verse(s) to share them!
48Waaye surga bi xamul bëgg-bëggu njaatigeem, te def lu yelloo ay dóor, dinañu ko dóor dóor yu néew. Ku ñu jox lu bare dees na la feyeeku lu bare. Ku ñu dénk lu bare, dees na la laajaat lu ko ëpp.
49«Damaa ñëw ngir indi sawara si ci àddina, te bëgg naa xaat taal bi tàkk.
50Fàww ñu sóob ma ci metit, te ba looluy mat, duma noppalu.
51Ndax dangeena xalaat ne damaa ñëw ngir indi jàmm ci àddina? Déedéet. Maa ngi leen koy wax, damaa ñëw ngir indi féewaloo.
52Gannaaw-si-tey, bu juróomi nit bokkee genn kër, dinañu féewaloo. Ñett dinañu féewaloo ak ñaar ñi ci des, ñaar ñi féewaloo ak ñett ñooñu.
53Baay dina féewaloo ak doom, doom ak baayam. Ndey dina féewaloo ak doomam ju jigéen; doom ju jigéen ji ak ndeyam. Goro dina féewaloo ak soxnas doomam; soxnas nit ak goroom.»
54Yeesu neeti mbooloo ma: «Bu ngeen gisee mu xiin ci sowu, dangeen naan ca saa sa: “Dina taw,” te mooy am.
55Te bu ngeen yégee ngelaw liy uppe sudd, ngeen ne: “Dina tàng tàngaay wu metti,” te mooy am.
56Naaféq yi ngeen doon! Man ngeena ràññee melow asamaan ak suuf, waaye lu tax manuleena ràññee li jamonoy léegi ji di tekki?
57«Lu tax it dungeen àtteel seen bopp liy jëf ju jub?

Read LUUG 12LUUG 12
Compare LUUG 12:48-57LUUG 12:48-57