Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - JËF YA - JËF YA 4

JËF YA 4:8-21

Help us?
Click on verse(s) to share them!
8Ci kaw loolu Piyeer daldi fees ak Xel mu Sell mi, ne leen: «Yéen kilifay xeet wi ak njiit yi,
9bu fekkee ne xettali nit ku wopp, ba mu wér, moo tax ngeen dëj nu ci pénc mi tey,
10nangeen xam lii, yéen ñépp ak bànni Israyil gépp: ci turu Yeesu Kirist mu Nasaret, mi ngeen daajoon ca bant te Yàlla dekkal ko, ci tur woowu la nit kii jële ag wér, ba taxaw ci seen kanam.
11Yeesu moomu mooy: “Doj wi ngeen xeeboon, yéen tabaxkat yi, te moo doon doju koñ.”
12Te mucc amul ci keneen, ndaxte ci ron asamaan amul weneen tur wu ñu maye ci nit ñi, wu nu wara mucce.»
13Kon bi ñu gisee fit, wi Piyeer ak Yowaana àndal, te ñu xam ne masuñoo jàng mbaa ñuy gëstu ci diine, ñu daldi waaru, ràññee ne daa nañu ànd ak Yeesu.
14Te bi ñu gisee nit, ka ñu fajoon, taxaw ak ñoom, manuñu caa teg dara.
15Noonu ñu santaane, ñu génne leen, ñu daldi gise ci seen biir,
16ne: «Lu nuy def ak ñii? Ndaxte def nañu kéemaan gu siiw; loolu leer na ñi dëkk Yerusalem ñépp, te manunu koo weddi.
17Waaye ngir mbir mi baña law ci xeet wi, nanu leen aaye, ñu baña waxati ak kenn ci tur woowu.»
18Noonu ñu woo leen, ñu tere leen bu wóor, ñu waxati mbaa waare dara ci turu Yeesu.
19Waaye Piyeer ak Yowaana ne leen: «Bu fekkee ne déggal leen te bàyyi Yàlla mooy li jub ci kanam Yàlla, seetleen.
20Waaye nun manunoo baña wax li nu gis te dégg ko.»
21Noonu kilifa yi tëkkuwaat leen, yiwi leen, ñu dem. Ndaxte amuñu benn bunt ci ñoom ngir mbugal leen, fekk ñépp di màggal Yàlla ci li xewoon.

Read JËF YA 4JËF YA 4
Compare JËF YA 4:8-21JËF YA 4:8-21