Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - JËF YA - JËF YA 28

JËF YA 28:22-31

Help us?
Click on verse(s) to share them!
22Waaye bëgg nanoo dégg li nga gëm, ndaxte xam nanu ne, tariixa booba, kenn jubluwu ko fenn.»
23Noonu ñu jox ko bés, te ñu bare ñëw, fekksi ko ca néegam. Mu di leen jàngal suba ba ngoon, di leen dëggal lu jëm ci nguuru Yàlla ak ci Yeesu, tukkee ci yoonu Musaa ak ci yonent yi, di leen jéema gëmloo.
24Ñenn ñi nag gëm li mu wax, ña ca des weddi ko.
25Gannaaw manuñoo déggoo, ñu bëgga tas. Waaye bi ñuy laata dem, Pool teg ca wax jii: «Xel mu Sell mi wax na seeni maam dëgg jaarale ko ci yonent Yàlla Esayi.
26Nee na: “Demal ci xeet wii ne leen: ‘Dingeen déglu bu baax waaye dungeen xam dara; di xool bu baax waaye dungeen gis dara.’
27Ndaxte xolu xeet wii dafa dërkiis; dañuy déglu ak nopp yu naqari, tey gëmm seeni bët, ngir baña gis ak seeni bët, dégg ak seeni nopp, te xam ci seen xol, ñu waññiku ci man, ma wéral leen.”
28«Xamleen nag ne xibaaru mucc gii yégal nañu ko ñi dul Yawut, te ñoom dinañu ko déglu.»
30Noonu diirub ñaari at Pool dëkk ca kër gu muy fey, di fa àggale ñépp ñi koy seetsi.
31Muy yégle nguuru Yàlla, di jàngle ci mbirum Boroom bi Yeesu Kirist ak fit wu dëgër, te kenn terewu ko ko.

Read JËF YA 28JËF YA 28
Compare JËF YA 28:22-31JËF YA 28:22-31