1Ñii nag ñoo di niti diiwaanu Yuda, ña jóge njaam ca ngàllo ga leen Nabukodonosor buuru Babilon yóbbu woon, te ñu jóge ca ñibbsi Yerusalem ak Yuda, ku nekk ak fa mu dëkk.
2Ña nga ñibbi ca njiital Sorobabel ak Yosuwe ak Neyemi ak Seraya ak Relaya ak Mardose ak Bilsan ak Mispar ak Bigway ak Reyum ak Baana. Limeefu góori bànni Israyil nii la tëdde:
3Askanu Paros, ñaari junni ak téeméer ak juróom ñaar fukk ak ñaar lañu (2 172).
4Askanu Sefatiya, ñetti téeméer ak juróom ñaar fukk ak ñaar lañu (372).
5Askanu Ara, juróom ñaar téeméer ak juróom ñaar fukk ak juróom lañu (775).
6Askanu Payat Mowab, soqikoo ci Yeswa ak Yowab, di ñaari junni ak juróom ñetti téeméer ak fukk ak ñaar (2 812).
7Askanu Elam, junni ak ñaar téeméer ak juróom fukk ak ñeent lañu (1 254).
8Askanu Sàttu, juróom ñeenti téeméer ak ñeent fukk ak juróom lañu (945).
9Askanu Sakay, juróom ñaar téeméer ak juróom benn fukk lañu (760).
10Askanu Baani, juróom benni téeméer ak ñeent fukk ak ñaar lañu (642).
11Askanu Bebay, juróom benni téeméer ak ñaar fukk ak ñett lañu (623).
12Askanu Asgàdd, junni ak ñaar téeméer ak ñaar fukk ak ñaar lañu (1 222).
13Askanu Adonikam, juróom benni téeméer ak juróom benn fukk ak juróom benn lañu (666).
14Askanu Bigway, ñaari junni ak juróom fukk ak juróom benn lañu (2 056).
15Askanu Adin, ñeenti téeméer ak juróom fukk ak ñeent lañu (454).
16Askanu Ater, soqikoo ci Esekiya, di juróom ñeent fukk ak juróom ñett (98).
17Askanu Besay, ñetti téeméer ak ñaar fukk ak ñett lañu (323).
18Askanu Yora, téeméer ak fukk ak ñaar lañu (112).
19Askanu Asum, ñaar téeméer ak ñaar fukk ak ñett lañu (223).
20Askanu Gibar, juróom ñeent fukk ak juróom lañu (95).
21Waa Betleyem, téeméer ak ñaar fukk ak ñett lañu (123).
22Waa Netofa, juróom fukk ak juróom benn lañu (56).
23Waa Anatot, téeméer ak ñaar fukk ak juróom ñett lañu (128).
24Waa Asmawet, ñeent fukk ak ñaar lañu (42).
25Waa Kiryaat Yarim ak Kefira ak Berot, juróom ñaar téeméer ak ñeent fukk ak ñett lañu (743).
26Waa Raama ak Geba, juróom benni téeméer ak ñaar fukk ak benn lañu (621).
27Waa Migmas, téeméer ak ñaar fukk ak ñaar lañu (122).
28Waa Betel ak Ayi, ñaar téeméer ak ñaar fukk ak ñett lañu (223).
29Waa Nebo, juróom fukk ak ñaar lañu (52).
30Waa Magbis téeméer ak juróom fukk ak juróom benn lañu (156).
31Waa Elam gu ndaw, junni ak ñaar téeméer ak juróom fukk ak ñeent lañu (1 254).
32Waa Arim, ñetti téeméer ak ñaar fukk lañu (320).
33Waa Lodd ak Adidd ak Ono, juróom ñaar téeméer ak ñaar fukk ak juróom lañu (725).
34Waa Yeriko, ñetti téeméer ak ñeent fukk ak juróom lañu (345).
35Waa Sena, ñetti junni ak juróom benn téeméer ak fanweer lañu (3 630).
36Sarxalkat yi ñii la: Askanu Yedaya, soqikoo ci waa kër Yosuwe, di juróom ñeenti téeméer ak juróom ñaar fukk ak ñett (973).
37Askanu Imer, junni ak juróom fukk ak ñaar lañu (1 052).
38Askanu Pasur, junni ak ñaar téeméer ak ñeent fukk ak juróom ñaar lañu (1 247).
39Askanu Arim, junni ak fukk ak juróom ñaar lañu (1 017).
40Leween ñi ñii la: Askanu Yeswa ak Kadmiyel. Mooy ñi bànqaasoo ci Odawya, tollu ci juróom ñaar fukk ak ñeent (74).
41Jàngkat yi ñoo di: Askanu Asaf, di téeméer ak ñaar fukk ak juróom ñett (128).
42Askanu fara bunt yi ñoo di: Askanu Salum, ak askanu Ater, ak askanu Talmon, ak askanu Akub, ak askanu Atita, ak askanu Sobay, ñépp di téeméer ak fanweer ak juróom ñeent (139).
43Liggéeykati kër Yàlla gi ñoo di: Askanu Ciya, ak askanu Asufa, ak askanu Tabawot,
44ak askanu Keros, ak askanu Siya, ak askanu Padon,
45ak askanu Lebana, ak askanu Agaba, ak askanu Akub,
46ak askanu Agab, ak askanu Samlay, ak askanu Xanan,
47ak askanu Gidel, ak askanu Gayar, ak askanu Raaya,
48ak askanu Reccin, ak askanu Nekoda, ak askanu Gasam,
49ak askanu Usa, ak askanu Paseya, ak askanu Besay,
50ak askanu Asna, ak askanu Meyunim, ak askanu Nefusim,
51ak askanu Bagbug, ak askanu Akufa, ak askanu Arur,
52ak askanu Baslut, ak askanu Meyida, ak askanu Arsa,
53ak askanu Barkos, ak askanu Sisera, ak askanu Tema,
54ak askanu Necciya, ak askanu Atifa.
55Askanu jaami Suleymaan ñii la: Askanu Sotay, ak askanu Asoferet, ak askanu Peruda,
56ak askanu Yaala, ak askanu Darkon, ak askanu Gidel,
57ak askanu Sefatiya, ak askanu Atil, ak askanu Pokeret Asbayim, ak askanu Aami.
58Mboolem liggéeykati kër Yàlla gi ak askanu jaami Suleymaan yi, ñetti téeméer ak juróom ñeent fukk ak ñaar (392).
59Ña bàyyikoo Tel Mela ak Tel Arsa ak Kerub Adon ak Imer te manuñoo firndeel ne seen waa kër maam ak seen askan ci Israyil lañu bokk, ñii la:
60Askanu Delaya, ak askanu Tobya, ak askanu Nekoda, di juróom benn téeméer ak juróom fukk ak ñaar (652).
61Am na it ñu loolu daloon ci askanu sarxalkat yi, muy askanu Abaya, ak askanu Akocc, ak askanu Barsilay, ma doon denc doomu Barsilay waa Galàdd ba, ba tax ñu santale ko seen sant.
62Ñooñu, seet nañu seen limeefu kër maam, waaye gisuñu ko. Ñu daldi leen doyadal, génne leen ci carxal gi.
63Boroom dëkk ba nag aaye leen ñu lekk ci ñam yu sell yaa sell, ba keroog ab sarxalkat di am lu leer ci ñoom ci jumtukaayi tegtal yi ñuy wax Urim ak Tumim.
64Limu mbooloo ma mépp ba mu daj, ñeent fukki junneek ñaar ak ñetti téeméer ak juróom benn fukk lañu (42 360),
65te limaaleesul seen jaam yu góor ak yu jigéen, yi tollu ci juróom ñaari junni ak ñetti téeméer ak fanweer ak juróom ñaar (7 337). Amoon nañu itam ay jàngkat yu góor ak yu jigéen, yu tollu ci ñaar téeméer (200).
66Amoon nañu juróom ñaar téeméeri fas ak fanweer ak juróom benn (736), ak ñaar téeméeri berkelle ak ñeent fukk ak juróom (245),
67ak ñeenti téeméeri giléem ak fanweer ak juróom (435), ak juróom benni junniy mbaam ak juróom ñaar téeméer ak ñaar fukk (6 720).
68Ba ñu àggee ca kër Aji Sax ja ca Yerusalem, am na ñenn ca kilifa ya jiite seen kër baay, ñu joxe ay saraxi yéene ngir tabaxaat kër Yàlla ga ca gentam.
69Joxe nañu ku nekk la mu man, jëme ca alal ja ñuy liggéeye, muy juróomi barigoy wurus ak fanweeri barigoy xaalis, ak téeméeri mbubbi sarxalkat.
70Ba loolu amee bànni Israyil gépp sancaat ca seen dëkki cosaan, sarxalkat yaak Leween ñaak ñenn ca baadoolo yaak jàngkat yaak fara bunt yaak liggéeykati kër Yàlla ga.